Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 5:22-40 in Wolof

Help us?

JËF YA 5:22-40 in Téereb Injiil

22 Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi délsi, yégle ko
23 ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.»
24 Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj.
25 Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.»
26 Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem jëli leen; waaye boolewuñu ci fitna, ngir ragal nit ñi sànni leen ay xeer.
27 Bi ñu leen indee, ñu dëj leen ci kanam mbooloo ma. Sarxalkat bu mag ba laaj leen
28 ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.»
29 Waaye Piyeer ak ndaw ya ne leen: «Déggal Yàlla moo gën déggal nit.
30 Yàllay sunuy maam dekkal na Yeesu, mi ngeen bóomoon ci wékk ko ca bant ba.
31 Te Yàlla yékkati na ko ci ndijooram, mu nekk Buur ak Musalkat, ngir may bànni Israyil réccu, ba mu baal leen seeni bàkkaar.
32 Seede nanu loolu, nun ak Xel mu Sell, mi Yàlla may ñi koy déggal.»
33 Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leena rey.
34 Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti.
35 Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu.
36 Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax.
37 Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo.
38 Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu.
39 Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko mana fanq, ngir ragala jànkoonte ak Yàlla.»
40 Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem.
JËF YA 5 in Téereb Injiil

Jëf ya 5:22-40 in Kàddug Yàlla gi

22 Dag ya nag dikk, fekkuñu leen ca kaso ba, ñu dellu yégleji ko,
23 ne: «Danoo fekk kaso ba tëje ràpp, wattukat ya taxaw ca bunt ya. Nu tijji, fekkunu kenn ca biir!»
24 Jawriñu kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya dégg loolu, daldi jaaxle lool ci ndaw yi, di xalaat nu mbir miy mujje.
25 Mu am ku dikk, ne leen: «Ña ngeen tëjoon kaso déy a nga noonu ca kër Yàlla ga, di waare.»
26 Ci kaw loolu jawriñu kër Yàlla ga ak dag ya jëli ndaw ya ndànk, bañ leena jaay doole, ngir ragal nit ñi sànni leen ay doj.
27 Ñu indi leen, taxawal leen ca kanam kurélu àttekat ya, sarxalkat bu mag ba laaj leen,
28 ne: «Xanaa aayewunu leen woon ne buleen waareeti mukk ci woowu tur? Yeena ngi nii ubale Yerusalem ak seen waare, ngeen nar nu cee gàdduloo bakkanu nit kii!»
29 Piyeer ak ndaw ya ca des nag ne leen: «Yàlla lees wara déggal, waaye du nit.
30 Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.
31 Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.
32 Nun noo seede loolu, nook Noo gu Sell, gi Yàlla jagleel ñi ko déggal.»
33 Ba ñu déggee loolu, dañoo mer ba fees, nar leena rey.
34 Ab Farisen bu ñuy wax Gamalyel, di jànglekatu yoonu Musaa bu ñépp nawloo, daldi taxaw ca digg kurélu àttekat ya. Mu joxe ndigal ngir ñu génne leen ab diir.
35 Ba ñu génnee, mu ne waa kurél ga: «Yeen bokki Israyil, moytuleen bu baax li ngeen di def ak nit ñii.
36 Ndaxte bu yàggul la Tëdas jóg, di jaay daraja, ba lu wara tollook ñeenti téeméeri nit far ak moom. Ñu rey ko, ña ko toppoon ñépp tasaaroo, seen pexe mujjewul fenn.
37 Gannaawam it Yuda mu Galile jóg, ca jant ya ñu doon lim waa réew mi; mu yóbbaale mbooloo mu ko topp. Moom itam dee, ña ko toppoon ñépp tasaaroo.
38 Léegi nag, dama ne, maanduleen ci ñii, te ba leen, ngir su seen mébét mbaa seen jëf bawoo ci nit, day yàqu rekk.
39 Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,
40 woowaat ndaw ya. Ba loolu amee ñu dóor leen, aaye leen ñu waxati lenn ci turu Yeesu, door leena yiwi.
Jëf ya 5 in Kàddug Yàlla gi