Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 5:13-41 in Wolof

Help us?

JËF YA 5:13-41 in Téereb Injiil

13 Te kenn ci ña ca des ñemewula booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal.
14 Moona ay nit ñu gëna bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom.
15 Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom.
16 Te it nit ñu bare dajaloo, jóge ca dëkk ya wër Yerusalem, ñu indi ay jarag ak ñu rab yu bon sadd; te ñoom ñépp daldi wér.
17 Booba sarxalkat bu mag ba jóg ak gàngooram gépp, maanaam kureelu Sadusen ga fa dëkk. Kiñaan gu mag jàpp leen,
18 ba ñu jàpp ndaw ya, tëj leen ca kaso ba.
19 Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, génne leen ci biti naan:
20 «Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, te xamal nit ñi lépp lu jëm ci dund gu wóor gii.»
21 Bi ñu déggee loolu, ñu dugg ca kër Yàlla ga ci suba teel, daldi waare. Bi ñu koy def, sarxalkat bu mag ba ak gàngooram ñëw, woolu kureelu àttekat ya, maanaam mbooloom njiiti bànni Israyil gépp; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
22 Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi délsi, yégle ko
23 ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.»
24 Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj.
25 Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.»
26 Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem jëli leen; waaye boolewuñu ci fitna, ngir ragal nit ñi sànni leen ay xeer.
27 Bi ñu leen indee, ñu dëj leen ci kanam mbooloo ma. Sarxalkat bu mag ba laaj leen
28 ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.»
29 Waaye Piyeer ak ndaw ya ne leen: «Déggal Yàlla moo gën déggal nit.
30 Yàllay sunuy maam dekkal na Yeesu, mi ngeen bóomoon ci wékk ko ca bant ba.
31 Te Yàlla yékkati na ko ci ndijooram, mu nekk Buur ak Musalkat, ngir may bànni Israyil réccu, ba mu baal leen seeni bàkkaar.
32 Seede nanu loolu, nun ak Xel mu Sell, mi Yàlla may ñi koy déggal.»
33 Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leena rey.
34 Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti.
35 Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu.
36 Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax.
37 Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo.
38 Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu.
39 Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko mana fanq, ngir ragala jànkoonte ak Yàlla.»
40 Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem.
41 Ndaw ya nag jóge ca kanam kureelu àttekat ya, bég ci li leen Yàlla jàppe, ñu yeyoo yenu toroxte ngir Tur wa.
JËF YA 5 in Téereb Injiil

Jëf ya 5:13-41 in Kàddug Yàlla gi

13 waaye kenn ca ña ca des ñemewula jaxasoo ak ñoom. Teewul askan wa nawloo leen lool.
14 Gëmkati Sang bi nag di gëna bare, ñuy wàllisi, ba doon mbooloo mu mag, góor ak jigéen.
15 Nit ñi dem bay génne jarag ji ci mbedd yi, teg leen ci ay laltu aki basaŋ, ngir bu fa Piyeer jaaree, lu bon bon takkndeeram mana dal ñenn ci ñoom.
16 Ci biir loolu nit ñu bare bàbbeekoo ca dëkk ya séq Yerusalem, indi ay jarag ak ñu rab yu bon sonal; ñoom ñépp daldi wér.
17 Ba mu ko defee xolu kañaan dugg sarxalkat bu mag ba, ak mboolem ña ko dar, te di waa ngérum Sadusen ña.
18 Ñu teg ndaw ya loxo, tëj leen ca kaso ba.
19 Ca guddi ga nag malaakam Boroom bi ubbi bunti kaso ba, génne leen, ne leen:
20 «Demleen taxaw ca digg kër Yàlla ga, ngeen xamal askan wi mboolem lu jëm ci dund gii.»
21 Gannaaw ba ñu déggee loolu, ba bët set, ñu dugg ca kër Yàlla ga, di waare. Ci biir loolu sarxalkat bu mag ba ak ña ko dar, dikk, woolu kurélu àttekat ya, mboolem kurélu njiiti bànni Israyil; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
22 Dag ya nag dikk, fekkuñu leen ca kaso ba, ñu dellu yégleji ko,
23 ne: «Danoo fekk kaso ba tëje ràpp, wattukat ya taxaw ca bunt ya. Nu tijji, fekkunu kenn ca biir!»
24 Jawriñu kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya dégg loolu, daldi jaaxle lool ci ndaw yi, di xalaat nu mbir miy mujje.
25 Mu am ku dikk, ne leen: «Ña ngeen tëjoon kaso déy a nga noonu ca kër Yàlla ga, di waare.»
26 Ci kaw loolu jawriñu kër Yàlla ga ak dag ya jëli ndaw ya ndànk, bañ leena jaay doole, ngir ragal nit ñi sànni leen ay doj.
27 Ñu indi leen, taxawal leen ca kanam kurélu àttekat ya, sarxalkat bu mag ba laaj leen,
28 ne: «Xanaa aayewunu leen woon ne buleen waareeti mukk ci woowu tur? Yeena ngi nii ubale Yerusalem ak seen waare, ngeen nar nu cee gàdduloo bakkanu nit kii!»
29 Piyeer ak ndaw ya ca des nag ne leen: «Yàlla lees wara déggal, waaye du nit.
30 Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.
31 Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.
32 Nun noo seede loolu, nook Noo gu Sell, gi Yàlla jagleel ñi ko déggal.»
33 Ba ñu déggee loolu, dañoo mer ba fees, nar leena rey.
34 Ab Farisen bu ñuy wax Gamalyel, di jànglekatu yoonu Musaa bu ñépp nawloo, daldi taxaw ca digg kurélu àttekat ya. Mu joxe ndigal ngir ñu génne leen ab diir.
35 Ba ñu génnee, mu ne waa kurél ga: «Yeen bokki Israyil, moytuleen bu baax li ngeen di def ak nit ñii.
36 Ndaxte bu yàggul la Tëdas jóg, di jaay daraja, ba lu wara tollook ñeenti téeméeri nit far ak moom. Ñu rey ko, ña ko toppoon ñépp tasaaroo, seen pexe mujjewul fenn.
37 Gannaawam it Yuda mu Galile jóg, ca jant ya ñu doon lim waa réew mi; mu yóbbaale mbooloo mu ko topp. Moom itam dee, ña ko toppoon ñépp tasaaroo.
38 Léegi nag, dama ne, maanduleen ci ñii, te ba leen, ngir su seen mébét mbaa seen jëf bawoo ci nit, day yàqu rekk.
39 Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,
40 woowaat ndaw ya. Ba loolu amee ñu dóor leen, aaye leen ñu waxati lenn ci turu Yeesu, door leena yiwi.
41 Ndaw ya nag bàyyikoo ca kurélu àttekat ya, di bég, gannaaw ñoom lañu jàpp ne ñoo yelloo toroxte ga ñu leen teg ndax Tur wi.
Jëf ya 5 in Kàddug Yàlla gi