13 Te kenn ci ña ca des ñemewula booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal.
14 Moona ay nit ñu gëna bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom.
15 Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom.
16 Te it nit ñu bare dajaloo, jóge ca dëkk ya wër Yerusalem, ñu indi ay jarag ak ñu rab yu bon sadd; te ñoom ñépp daldi wér.
17 Booba sarxalkat bu mag ba jóg ak gàngooram gépp, maanaam kureelu Sadusen ga fa dëkk. Kiñaan gu mag jàpp leen,
18 ba ñu jàpp ndaw ya, tëj leen ca kaso ba.
19 Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, génne leen ci biti naan:
20 «Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, te xamal nit ñi lépp lu jëm ci dund gu wóor gii.»
21 Bi ñu déggee loolu, ñu dugg ca kër Yàlla ga ci suba teel, daldi waare. Bi ñu koy def, sarxalkat bu mag ba ak gàngooram ñëw, woolu kureelu àttekat ya, maanaam mbooloom njiiti bànni Israyil gépp; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
22 Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi délsi, yégle ko
23 ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.»
24 Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj.
25 Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.»