Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 4

Jëf ya 4:7-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Ñu taxawal Piyeer ak Yowaan ca digg ba, laaj leen ne: «Yeen, lii ngeen def, ci ban xam-xam, ak ci wan tur ngeen ko defe?»
8Fa la Piyeer feese Noo gu Sell gi, ne leen: «Yeen kilifay xeet wi ak mag ñi,
9ndegam yoon moo nuy laaj lu jëm ci ndimbal lu ab lafañ jagoo, ak ci man pexe la lafañ bi mucce,
10xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
11Yeesu moomu mooy: “Doj wi ngeen beddi woon, yeen tabaxkat yi, te mu mujj di doju coll wi.”
12Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»
13Ba waa kurélu àttekat ya gisee fit, wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon.
14Te itam ka ñu wéral a nga taxaw fa seen wet, ñuy gis. Manuñu caa tegati dara.
15Ba mu ko defee ñu joxe ndigal, génne leen, daldi gise ci seen biir.
16Ñu ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndax kat firnde lu leer sottee na fi ci ñoom; leer na nàññ waa Yerusalem gépp, te manunu koo weddi.
17Waaye kat bu mbir mi gëna siiw ci xeet wi. Nan leen tëkku, ngir aaye leen ñu waxati kenn tur woowu.»
18Ñu woo leen nag, aaye leen, ne leen mayatuñu leen benn yoon ñu waxati lenn, mbaa ñuy jàngale ci turu Yeesu.
19Piyeer ak Yowaan ne leen: «Ndax li jaadu fa Yàlla mooy nu déggal leen, yeen, bàyyi Yàlla? Yeenay àtte loolu.
20Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.»
21Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew,
22ngir waa, ja kéemtaan ga wérloo amoon na lu wees ñeent fukki at.
23Gannaaw ba ñu yiwee Piyeer ak Yowaan, ñu dem ca seen bokki gëmkat, nettali leen mboolem la leen sarxalkat yu mag yaak mag ña wax.
24Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.
25Yaa waxe Noo gu Sell gi ci sunu gémmiñu maam Daawuda sa jaam bi, nga ne: “Lu xeeti àddina di riir? Lu xeet yiy lal pexey neen?
26Buuri àddinaa jógandoo, kilifa yee lëkkoo ci kaw Boroom bi ak Almaseem.”
27Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.

Read Jëf ya 4Jëf ya 4
Compare Jëf ya 4:7-27Jëf ya 4:7-27