Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 4:6-10 in Wolof

Help us?

JËF YA 4:6-10 in Téereb Injiil

6 Ràññee nañu ci: Anas, miy sarxalkat bu mag bi, Kayif, Yowaana, Alegsàndar ak bokki sarxalkat bu mag bi.
7 Ñu dëj Piyeer ak Yowaana ca digg ba, laaj leen ne: «Lii ngeen def, ci gan kàttan, mbaa ci turu kan, ngeen ko defe?»
8 Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: «Yéen kilifay xeet wi ak njiit yi,
9 bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu wér, moo tax ngeen dëj nu ci pénc mi tey,
10 nangeen xam lii, yéen ñépp ak bànni Israyil gépp: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Yàlla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii jële ag wér, ba taxaw ci seen kanam.
JËF YA 4 in Téereb Injiil

Jëf ya 4:6-10 in Kàddug Yàlla gi

6 Anas, sarxalkat bu mag ba ca la, ak Kayif ak Yowaan ak Alegsàndar, ak mboolem bokki sarxalkat bu mag.
7 Ñu taxawal Piyeer ak Yowaan ca digg ba, laaj leen ne: «Yeen, lii ngeen def, ci ban xam-xam, ak ci wan tur ngeen ko defe?»
8 Fa la Piyeer feese Noo gu Sell gi, ne leen: «Yeen kilifay xeet wi ak mag ñi,
9 ndegam yoon moo nuy laaj lu jëm ci ndimbal lu ab lafañ jagoo, ak ci man pexe la lafañ bi mucce,
10 xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
Jëf ya 4 in Kàddug Yàlla gi