Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 4:28-34 in Wolof

Help us?

JËF YA 4:28-34 in Téereb Injiil

28 te def lépp, li sa kàttan ak sa ndigal tëraloon.
29 Léegi nag Boroom bi, seetal seeni tëkku te may nu, nun say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit.
30 Tàllalal sa loxo, ci wéral ak ci wone ay kéemaan ak ay firnde, jaarale ko ci turu Yeesu, sa Ndaw lu sell li.»
31 Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yëngatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër.
32 Noonu mbooloom ñu gëm ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp.
33 Te ndaw yi di seedeel ndekkitel Yeesu Boroom bi ak kàttan gu réy. Te yiw wu yaatu ëmb leen, ñoom ñépp.
34 Kenn ci ñoom ñàkkul dara, ndaxte képp ku nekk boroom suuf mbaa am ay kër, jaay na ko, indi njég li,
JËF YA 4 in Téereb Injiil

Jëf ya 4:28-34 in Kàddug Yàlla gi

28 Noonu it lañu sottale mboolem li nga dogale woon sa loxo ak sa coobare.
29 Léegi nag Boroom bi, bàyyil xel seeni tëkkoo te nga may nu, nun say jaam, nuy waxe sa kàddu fit wu mat sëkk.
30 Ngalla tàllalal sa loxo ngir di wéral ak a amal ay firnde aki kéemaan ci turu Yeesu, sa ndaw lu sell li.»
31 Ba ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu daje daa yëngu, ñu feese Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.
32 Ci kaw loolu mboolem gëmkat ñi bokk menn xel, ak benn xalaat. Du kenn ku ne moo moom lenn ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp ci seen biir.
33 Ndaw yi nag di seedee doole ju réy ne Sang bi Yeesu dekki na, yiw wu yaa di leen dikkal ñoom ñépp.
34 Kenn ci ñoom ndóolul, ndax képp ku ciy boroom suuf mbaa ay kër, da koy jaay, indi njég li,
Jëf ya 4 in Kàddug Yàlla gi