19Piyeer ak Yowaan ne leen: «Ndax li jaadu fa Yàlla mooy nu déggal leen, yeen, bàyyi Yàlla? Yeenay àtte loolu.
20Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.»
21Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew,
22ngir waa, ja kéemtaan ga wérloo amoon na lu wees ñeent fukki at.
23Gannaaw ba ñu yiwee Piyeer ak Yowaan, ñu dem ca seen bokki gëmkat, nettali leen mboolem la leen sarxalkat yu mag yaak mag ña wax.
24Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.
25Yaa waxe Noo gu Sell gi ci sunu gémmiñu maam Daawuda sa jaam bi, nga ne: “Lu xeeti àddina di riir? Lu xeet yiy lal pexey neen?
26Buuri àddinaa jógandoo, kilifa yee lëkkoo ci kaw Boroom bi ak Almaseem.”