Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 4:16-33 in Wolof

Help us?

JËF YA 4:16-33 in Téereb Injiil

16 ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te manunu koo weddi.
17 Waaye ngir mbir mi baña law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu baña waxati ak kenn ci tur woowu.»
18 Noonu ñu woo leen, ñu tere leen bu wóor, ñu waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu.
19 Waaye Piyeer ak Yowaana ne leen: «Bu fekkee ne déggal leen te bàyyi Yàlla mooy li jub ci kanam Yàlla, seetleen.
20 Waaye nun manunoo baña wax li nu gis te dégg ko.»
21 Noonu kilifa yi tëkkuwaat leen, yiwi leen, ñu dem. Ndaxte amuñu benn bunt ci ñoom ngir mbugal leen, fekk ñépp di màggal Yàlla ci li xewoon.
22 Ndaxte nit, ka ñu fajoon ci kéemaan googu, weesoon na ñeent fukki at.
23 Bi ñu leen yiwee nag, ñu dem ci seeni bokk, nettali leen li sarxalkat yu mag ya ak njiit ya waxoon lépp.
24 Bi ko bokk ya déggee nag, ñu mànkoo, diis seen kàddu Yàlla ne: «Boroom bi, yaa sàkk asamaan, suuf, géej ak lépp li nekk ci seen biir.
25 Yaa wax, jaar ci sunu maam Daawuda sa jaam, mi doon gémmiñu Xel mu Sell mi, ne: “Lu tax xeeti àddina di bax? Lu tax ñuy fexe lu manula am?
26 Buuri àddina dañoo booloo, te kilifa yi dajaloo, di bañ Boroom bi ak Almaseem.”
27 Ndaxte ci dëgg ci dëkk bii, Erodd ak Poñsë Pilaat ànd ak xeeti àddina ak bànni Israyil, likkoo nañu, ngir daaneel sa Ndaw lu sell li nga fal, di Yeesu,
28 te def lépp, li sa kàttan ak sa ndigal tëraloon.
29 Léegi nag Boroom bi, seetal seeni tëkku te may nu, nun say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit.
30 Tàllalal sa loxo, ci wéral ak ci wone ay kéemaan ak ay firnde, jaarale ko ci turu Yeesu, sa Ndaw lu sell li.»
31 Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yëngatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër.
32 Noonu mbooloom ñu gëm ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp.
33 Te ndaw yi di seedeel ndekkitel Yeesu Boroom bi ak kàttan gu réy. Te yiw wu yaatu ëmb leen, ñoom ñépp.
JËF YA 4 in Téereb Injiil

Jëf ya 4:16-33 in Kàddug Yàlla gi

16 Ñu ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndax kat firnde lu leer sottee na fi ci ñoom; leer na nàññ waa Yerusalem gépp, te manunu koo weddi.
17 Waaye kat bu mbir mi gëna siiw ci xeet wi. Nan leen tëkku, ngir aaye leen ñu waxati kenn tur woowu.»
18 Ñu woo leen nag, aaye leen, ne leen mayatuñu leen benn yoon ñu waxati lenn, mbaa ñuy jàngale ci turu Yeesu.
19 Piyeer ak Yowaan ne leen: «Ndax li jaadu fa Yàlla mooy nu déggal leen, yeen, bàyyi Yàlla? Yeenay àtte loolu.
20 Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.»
21 Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew,
22 ngir waa, ja kéemtaan ga wérloo amoon na lu wees ñeent fukki at.
23 Gannaaw ba ñu yiwee Piyeer ak Yowaan, ñu dem ca seen bokki gëmkat, nettali leen mboolem la leen sarxalkat yu mag yaak mag ña wax.
24 Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.
25 Yaa waxe Noo gu Sell gi ci sunu gémmiñu maam Daawuda sa jaam bi, nga ne: “Lu xeeti àddina di riir? Lu xeet yiy lal pexey neen?
26 Buuri àddinaa jógandoo, kilifa yee lëkkoo ci kaw Boroom bi ak Almaseem.”
27 Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.
28 Noonu it lañu sottale mboolem li nga dogale woon sa loxo ak sa coobare.
29 Léegi nag Boroom bi, bàyyil xel seeni tëkkoo te nga may nu, nun say jaam, nuy waxe sa kàddu fit wu mat sëkk.
30 Ngalla tàllalal sa loxo ngir di wéral ak a amal ay firnde aki kéemaan ci turu Yeesu, sa ndaw lu sell li.»
31 Ba ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu daje daa yëngu, ñu feese Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.
32 Ci kaw loolu mboolem gëmkat ñi bokk menn xel, ak benn xalaat. Du kenn ku ne moo moom lenn ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp ci seen biir.
33 Ndaw yi nag di seedee doole ju réy ne Sang bi Yeesu dekki na, yiw wu yaa di leen dikkal ñoom ñépp.
Jëf ya 4 in Kàddug Yàlla gi