5Booba ay toppkati yoonu Yawut a nga dëkke Yerusalem, te bawoo ci xeeti àddina yépp.
6Naka la coow li jolli, nit ñi daje, ku nekk ci mbooloo mi dégg ñuy làkk sa làkku bopp, mbooloo ma jaaxle.
7Ñu boole waaru ak yéemu, naa: «Ñii di wax nii ñépp, xanaa duñu waa Galile?
8Ana nu kenn ku nekk ci nun nag mana dégge ñuy wax ci làmmiñ wi nga nàmp?
9Muy waa Pàrt, ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi,