Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 2:5-17 in Wolof

Help us?

JËF YA 2:5-17 in Téereb Injiil

5 Fekk booba amoon na ay Yawut yu daloon Yerusalem, doon ay nit ñu ragal Yàlla te bokk ci xeeti àddina yépp.
6 Bi nit ñi déggee riir ma nag, ñépp dajaloo, daldi waaru ci li ñu leen dégg, ñuy wax ku nekk sa làkk.
7 Ñu waaru te yéemu naa: «Gisleen, ñiy wax ñépp, ndax duñu waa diiwaanu Galile?
8 Naka la mana ame nag, nu di leen dégg, kenn ku nekk ci nun, ñuy wax ci sa làmmiñ, wi nga nàmp?
9 Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi,
10 di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan ñi jóge Room,
11 Yawut yi ak ñi tuub ci yoonu Yawut yi, waa Keret ak waa Arabi, nun ñépp nu ngi leen di dégg, ñuy yégle màggaayi Yàlla ci sunuy làkk!»
12 Noonu ñépp waaru, ba jaaxle lool, ñuy waxante ci seen biir ne: «Lii lu muy tekki?»
13 Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! Ñii dañoo màndi ak biiñ.»
14 Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!
15 Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.
16 Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:
17 “Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi, dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp; seen xeet wu góor ak wu jigéen dinañu wax ci kàddug Yàlla; waxambaane yi dinañu gis ay peeñu te màggat yi di gént ay gént.
JËF YA 2 in Téereb Injiil

Jëf ya 2:5-17 in Kàddug Yàlla gi

5 Booba ay toppkati yoonu Yawut a nga dëkke Yerusalem, te bawoo ci xeeti àddina yépp.
6 Naka la coow li jolli, nit ñi daje, ku nekk ci mbooloo mi dégg ñuy làkk sa làkku bopp, mbooloo ma jaaxle.
7 Ñu boole waaru ak yéemu, naa: «Ñii di wax nii ñépp, xanaa duñu waa Galile?
8 Ana nu kenn ku nekk ci nun nag mana dégge ñuy wax ci làmmiñ wi nga nàmp?
9 Muy waa Pàrt, ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi,
10 ak Firisi ak Pamfili ak Misra ak wàllu Libi ga dendeek Siren, ak gan ñi jóge Room,
11 ak Yawuti njuddu-ji-réew yeek tuubeen ñi, ak waa Keret ak Arabi, nun ñépp a leen dégg ci sunu làmmiñi bopp, ñuy siiwtaane jaloore yu Yàlla!»
12 Ñépp waaru, ba jànnaxe, di wax ci seen biir naa: «Lii lu muy tekki nag?»
13 Teewul ñenn ñay ñaawle, ne: «Ñii daal biiñ bu bees doŋŋ lañu naan ba màndi.»
14 Ci kaw loolu Piyeer taxaw, mook Fukk ñaak benn, daldi àddu ca kaw, ne: «Yeen bokki Yawut yi, ak mboolem yeen ñi dëkke Yerusalem, dégluleen bu baax sama kàddu, ba xam lii lu mu doon.
15 Ñii màndiwuñu, ni ngeen ko fooge, ndax yoor-yoor doŋŋ a jot.
16 Lii kay mooy kàddu ga Yonent Yàlla Yowel jottli woon, ne:
17 “Yàlla nee: Mujug jamono, maay tuur samag Noo ci kaw wépp suux; seeni doom, góor ak jigéen di biral waxyu, seeni xale yu góor di gis ay peeñu, màggat ñi di gént ay gént.
Jëf ya 2 in Kàddug Yàlla gi