Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 2:34-46 in Wolof

Help us?

JËF YA 2:34-46 in Téereb Injiil

34 Ndaxte du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na: “Boroom bi wax na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor,
35 ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
36 «Na bànni Israyil gépp xam bu wóor nag ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.»
37 Bi ko mbooloo ma déggee, naqaru xol wu metti jàpp leen; ñu daldi ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, lu nu wara def?»
38 Piyeer ne leen: «Tuubleen seeni bàkkaar, te kenn ku nekk ci yéen, ñu sóob ko ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Noonu Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar te may leen Xel mu Sell mi.
39 Ndaxte li Yàlla dige woon, yéena ko moom ak seeni doom ak ñu sore ñépp, di ñépp ñi Yàlla sunu Boroom di woo ci moom.»
40 Noonu mu artu leen ak yeneen wax yu bare, di leen dénk ne: «Rëccleen ci niti jamono ju dëng jii.»
41 Ñi nangu ay waxam nag, ñu sóob leen ci ndox, te ca bés booba lu mat limub ñetti junniy nit yokku nañu ci ñoom.
42 Ñoom nag ñuy wéy ci njànglem ndaw yi ak cig bokk, ci damm mburu ak ñaan ci Yàlla.
43 Ragal jàpp ñépp, te ndaw yi di def ay kéemaan ak ay firnde yu bare.
44 Ñi gëm nag dañoo booloo te bokk lépp.
45 Ñu jaay seeni suuf ak seen alal, séddoo ko, ku nekk ak la ngay soxla.
46 Te bés bu nekk ñu saxoo teew ak benn xalaat ca kër Yàlla ga, tey damm mburu ca kër ya; ñuy lekk seen ñam ak xol bu laab tey bég,
JËF YA 2 in Téereb Injiil

Jëf ya 2:34-46 in Kàddug Yàlla gi

34 Ndax kat du Daawudaa yéeg asamaan, waaye moom ci boppam moo ne: “Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko: ‘Toogeel sama ndijoor,
35 ba ma def say noon, sa ndëggastalu tànk.’ ”
36 «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»
37 Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?»
38 Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.
39 Ndax dige bi, yeen ak seen askan a ko moom, ak jaambur ñi féete fu sore ñépp, mboolem ñi sunu Yàlla Boroom bi woo.»
40 Yeneen kàddu yu bare soññe na leen ko, ñaaxe leen ko, ne leen: «Muccleen ci gii maas gu dëng.»
41 Ña nangu kàddug Piyeer nag, ñu sóob leen ci ndox; bésub keroog lu wara mat ñetti junni (3 000) yokku nañu ca gëmkat ña.
42 Ci kaw loolu ñu pastéefu ci njànglem ndaw yi ak ci dundal ag bokkoo, ak ci dagg mburum bokkoo mi, ak ci jataayi julli.
43 Ba loolu amee ag ragal jàpp ñépp, ay kiraama yu bare aki firnde daldi sottee ca jëfi ndaw ya.
44 Gëmkat ñépp benn lañu woon te ñoo bokkoon lépp.
45 Ci biir loolu seeni suuf ak seen alal sax, ñu jaay, séddoo ko ñoom ñépp na mu dëppook seeni soxla.
46 Bés bu nekk nag ñu doon benn bopp, saxoo teew ca kër Yàlla ga, di dagg mburum bokkoo ci këroo kër, tey bokk lekk ci biir mbég ak woyoflu.
Jëf ya 2 in Kàddug Yàlla gi