Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 2:15-36 in Wolof

Help us?

JËF YA 2:15-36 in Téereb Injiil

15 Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.
16 Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:
17 “Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi, dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp; seen xeet wu góor ak wu jigéen dinañu wax ci kàddug Yàlla; waxambaane yi dinañu gis ay peeñu te màggat yi di gént ay gént.
18 Waaw, ci bés yooyu dinaa tuur ci sama Xel ci sama kaw jaam yu góor ak yu jigéen, te dinañu wax ci kàddug Yàlla.
19 Dinaa wone ay kéemaan ci kaw ci asamaan ak ay firnde ci suuf ci àddina, muy deret, sawara ak ay niiri saxar.
20 Jant bi dina daldi lëndëm, weer wi deretal, bala bésu Boroom biy ñëw, di bés bu mag, bi ànd ak ndam.
21 Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam, dinga mucc.”
22 «Yéen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu mi dëkk Nasaret, nit la woon, ku Yàlla dëggal ci seen kanam ciy kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; yéen xam ngeen ko.
23 Moom nag jébbale nañu ko, jaar ci nas, bi Yàlla dogaloon te xam ko lu jiitu; te yéen rey ngeen ko ci daaj ko ci bant, jaarale ko ci loxoy bàkkaarkat.
24 Waaye Yàlla dekkal na ko, daggal ko buumi dee, ndaxte dee manu koo téye.
25 Daawuda wax na ci mbiram ne: “Saa su ne gis naa Boroom bi ci sama kanam; gannaaw mu ngi ci sama ndijoor, duma raf.
26 Moo tax sama xol sedd, may woy sama bànneex, te it sama yaram di tëdd ci yaakaar.
27 Ndaxte doo bàyyi sama ruu ci barsàq, te doo seetaan sa waa ju sell, mu yàqu.
28 Xamal nga ma yoonu dund; dinga ma béglooji ci sa kanam.”
29 «Bokk yi, man naa leena wax lu wóor ci mbirum maam Daawuda, ne dee na te suul nañu ko; bàmmeelam mu ngi ci nun ba tey.
30 Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàlla digoon na ko ci ngiñ ne dina teg ci nguuram kenn ci askanam.
31 Kon gis na lu ñëwagul, di wax ci mbirum ndekkitel Kirist ne bàyyiwuñu ko ci barsàq, te yaramam yàquwul.
32 Yeesu moomu nag, Yàlla dekkal na ko; nun ñépp seede nanu ko.
33 Yàlla yéege na ko ak ndijooram, te jot na ci Baay bi Xel mu Sell mi ñu dige woon, ba tuur lii ngeen gis te dégg ko.
34 Ndaxte du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na: “Boroom bi wax na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor,
35 ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
36 «Na bànni Israyil gépp xam bu wóor nag ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.»
JËF YA 2 in Téereb Injiil

Jëf ya 2:15-36 in Kàddug Yàlla gi

15 Ñii màndiwuñu, ni ngeen ko fooge, ndax yoor-yoor doŋŋ a jot.
16 Lii kay mooy kàddu ga Yonent Yàlla Yowel jottli woon, ne:
17 “Yàlla nee: Mujug jamono, maay tuur samag Noo ci kaw wépp suux; seeni doom, góor ak jigéen di biral waxyu, seeni xale yu góor di gis ay peeñu, màggat ñi di gént ay gént.
18 Kera jant yooyu, sama jaam ñi, góor ak jigéen, maa leen di tuur samag Noo, ñuy biral waxyu.
19 Te maay def ay kiraama fi asamaan aki firnde ci dun bi fi suuf; muy deret ak sawara ak niiru saxar.
20 Jant beey soppliku ag lëndëm, weer wi doon deret, bésub Boroom bi doora taxawe màggaay ak daraja.
21 Su boobaa, ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.”
22 «Yeen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu waa Nasaret bi, Yàlla moo firndeele ag dëggoom, ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll.
23 Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.
24 Waaye moom la Yàlla yiwee ci mititu ndee, dekkal ko, ndax dee amul kàttanu tënk ko.
25 Daawuda wax na ci mbiram ne: “Maa doon gis Boroom bi fi sama kanam saa su nekk, ndijoor la ma fare, ba duma tërëf.
26 Moo tax sama xol di nux-nuxi, samaw làmmiñ di textexi, samaw suux sax nara nopplujee yaakaar.
27 Doo ma wacc njaniiw moos, doo seetaan sa waa ju sell, mu yàqu.
28 Yaa ma xamal yoonu dund, yaa may wéttali ba matal sama mbégte.”
29 «Bokk yi nag, Maam Daawuda, manees na leena wax ci lu wér ne nelaw na, ba ñu denc ko, te bàmmeelam a ngi fi, nuy gis ba tey jii.
30 Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàllaa ko giñaloon ne ku bokk ci geñoom lay teg cib jalam.
31 Kon li mu gis te dikkagul mooy ndekkitel Almasi, te ci mbiram la wax ne bàyyeesu ko biir njaniiw, te yaramam du yàqu.
32 Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp.
33 Yàllaa ko yéege fa ndijooram, te jot na ci Baay bi Noo gu Sell ga mu dige woon. Moom la tuur nii tey, ngeen gis ko, dégg ko.
34 Ndax kat du Daawudaa yéeg asamaan, waaye moom ci boppam moo ne: “Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko: ‘Toogeel sama ndijoor,
35 ba ma def say noon, sa ndëggastalu tànk.’ ”
36 «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»
Jëf ya 2 in Kàddug Yàlla gi