Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 2:13-14 in Wolof

Help us?

JËF YA 2:13-14 in Téereb Injiil

13 Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! Ñii dañoo màndi ak biiñ.»
14 Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!
JËF YA 2 in Téereb Injiil

Jëf ya 2:13-14 in Kàddug Yàlla gi

13 Teewul ñenn ñay ñaawle, ne: «Ñii daal biiñ bu bees doŋŋ lañu naan ba màndi.»
14 Ci kaw loolu Piyeer taxaw, mook Fukk ñaak benn, daldi àddu ca kaw, ne: «Yeen bokki Yawut yi, ak mboolem yeen ñi dëkke Yerusalem, dégluleen bu baax sama kàddu, ba xam lii lu mu doon.
Jëf ya 2 in Kàddug Yàlla gi