Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 2:1-11 in Wolof

Help us?

JËF YA 2:1-11 in Téereb Injiil

1 Bi bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp booloo nañu ci benn bérab.
2 Ca saa sa riir jollee asamaan, mel ni ngelaw lu gaaw te bare doole, daldi fees dell kër, ga ñu toog.
3 Te ay làmmiñ yu mel ni sawara feeñu leen, ñu tasaaroo ci seen biir, toŋ ca kaw kenn ku nekk.
4 Noonu ñu fees ak Xel mu Sell mi ñoom ñépp, ñu daldi wax yeneen làkk, ni leen Xel mu Sell mi maye, ñu wax ko.
5 Fekk booba amoon na ay Yawut yu daloon Yerusalem, doon ay nit ñu ragal Yàlla te bokk ci xeeti àddina yépp.
6 Bi nit ñi déggee riir ma nag, ñépp dajaloo, daldi waaru ci li ñu leen dégg, ñuy wax ku nekk sa làkk.
7 Ñu waaru te yéemu naa: «Gisleen, ñiy wax ñépp, ndax duñu waa diiwaanu Galile?
8 Naka la mana ame nag, nu di leen dégg, kenn ku nekk ci nun, ñuy wax ci sa làmmiñ, wi nga nàmp?
9 Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi,
10 di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan ñi jóge Room,
11 Yawut yi ak ñi tuub ci yoonu Yawut yi, waa Keret ak waa Arabi, nun ñépp nu ngi leen di dégg, ñuy yégle màggaayi Yàlla ci sunuy làkk!»
JËF YA 2 in Téereb Injiil

Jëf ya 2:1-11 in Kàddug Yàlla gi

1 Ba bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp a bokk daje benn bérab.
2 Ca saa sa coow jollee asamaan, mel ni riirum ngelaw lu bare doole, daldi fees dell biir kër ga ñu toog.
3 Ci kaw loolu ay làmmiñ yu mel ni tàkk-tàkki sawara feeñu leen, làmmiñ ya séddlikoo, daldi toŋ ci kaw kenn ku nekk.
4 Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.
5 Booba ay toppkati yoonu Yawut a nga dëkke Yerusalem, te bawoo ci xeeti àddina yépp.
6 Naka la coow li jolli, nit ñi daje, ku nekk ci mbooloo mi dégg ñuy làkk sa làkku bopp, mbooloo ma jaaxle.
7 Ñu boole waaru ak yéemu, naa: «Ñii di wax nii ñépp, xanaa duñu waa Galile?
8 Ana nu kenn ku nekk ci nun nag mana dégge ñuy wax ci làmmiñ wi nga nàmp?
9 Muy waa Pàrt, ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi,
10 ak Firisi ak Pamfili ak Misra ak wàllu Libi ga dendeek Siren, ak gan ñi jóge Room,
11 ak Yawuti njuddu-ji-réew yeek tuubeen ñi, ak waa Keret ak Arabi, nun ñépp a leen dégg ci sunu làmmiñi bopp, ñuy siiwtaane jaloore yu Yàlla!»
Jëf ya 2 in Kàddug Yàlla gi