Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 28:13-31 in Wolof

Help us?

JËF YA 28:13-31 in Téereb Injiil

13 Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawu sudd daldi jóg, te ca ñaareelu fan ba nu teer Pusol.
14 Gis nanu fa ay bokk, ñu ñaan nu, nu toog fa ayu-bés. Noonu nu dem Room.
15 Sunuy xibaar law na, ba egg ca bokk ya fa dëkk, noonu ñu gatandu nu ba ca péncu Apiyus ak bérab bu ñuy wax Ñetti añukaay ya. Bi leen Pool gisee, mu sant Yàlla, daldi takk fitam.
16 Bi nu dikkee Room nag, ñu may Pool, mu dëkk fa ko lew, moom ak xarekat ba koy wottu.
17 Bi ñetti fan wéyee, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Bi ñu dajaloo nag, mu wax leen lii: «Bokk yi, jàpp nañu ma ci Yerusalem, jébbal ma waa Room, fekk defuma dara luy suufeel sunu xeet, mbaa lu juuyoo ak sunuy aaday maam.
18 Waa Room nag seet sama mbir, te bëgg maa bàyyi, ndaxte toppuñu ma dara lu jar dee.
19 Waaye bi ko Yawut ya bañee, fas yéene naa dénk sama mbir Sesaar, fekk ba tey awma dara lu may taqal sama xeet.
20 Moo tax ma ñaana gise ak yéen, nu diisoo, ndaxte yaakaaru bànni Israyil moo tax ñu jéng ma.»
21 Bi ñu ko déggee, ñu ne ko: «Jotunu benn bataaxal bu jóge Yude ci sa mbir, te kenn ci bokk, yi fi dikk, jottaliwul mbaa mu seede ci yaw lu bon.
22 Waaye bëgg nanoo dégg li nga gëm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.»
23 Noonu ñu jox ko bés, te ñu bare ñëw, fekksi ko ca néegam. Mu di leen jàngal suba ba ngoon, di leen dëggal lu jëm ci nguuru Yàlla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen jéema gëmloo.
24 Ñenn ñi nag gëm li mu wax, ña ca des weddi ko.
25 Gannaaw manuñoo déggoo, ñu bëgga tas. Waaye bi ñuy laata dem, Pool teg ca wax jii: «Xel mu Sell mi wax na seeni maam dëgg jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi.
26 Nee na: “Demal ci xeet wii ne leen: ‘Dingeen déglu bu baax waaye dungeen xam dara; di xool bu baax waaye dungeen gis dara.’
27 Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis; dañuy déglu ak nopp yu naqari, tey gëmm seeni bët, ngir baña gis ak seeni bët, dégg ak seeni nopp, te xam ci seen xol, ñu waññiku ci man, ma wéral leen.”
28 «Xamleen nag ne xibaaru mucc gii yégal nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»
30 Noonu diirub ñaari at Pool dëkk ca kër gu muy fey, di fa àggale ñépp ñi koy seetsi.
31 Muy yégle nguuru Yàlla, di jàngle ci mbirum Boroom bi Yeesu Kirist ak fit wu dëgër, te kenn terewu ko ko.
JËF YA 28 in Téereb Injiil

Jëf ya 28:13-31 in Kàddug Yàlla gi

13 Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawal bëj-saalum jóg, nu daldi àgg teerub Pusol ci ñaari fan.
14 Gis nanu fa ay bokki gëmkat, ñu ñaan nu, ba nu toog fa ñoom juróom ñaari fan. Gannaaw loolu nu dem Room.
15 Ba bokki gëmkati Room yégee ne nu ngi dikk, ñoo nu gatandusi ba fa ñuy wax péncu Apiyus ak fa ñuy wax Ñetti dalu gan ya. Ba leen Póol gisee, daa sant Yàlla, daldi gëna sawar.
16 Ba nu dikkee Room nag may nañu Póol, mu am daluwaayu boppam, ab takk-der di ko wattu.
17 Ñu teg ca ñetti fa, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Ba ñu dajee, mu ne leen: «Bokk yi, man defuma dara lu dëngook sunuw xeet mbaa sunu aaday maam. Teewul ñu jàppe ma fa Yerusalem, teg ma ci loxoy Room.
18 Ñooñu seet sama mbir, gisuñu ci man tuuma ju yelloo àtteb dee, ñu nar maa bàyyi.
19 Ba Yawut ya bañee nag, amatuma pexe mu dul dénk sama mbir Sesaar, doonte du lenn lu may toppe samaw xeet.
20 Mbir moomu nag moo tax ma woolu leen, ngir giseek yeen, diisook yeen, ndax yaakaaru bànni Israyil moo waral sama jéng yii.»
21 Ñu ne ko: «Nun de, du benn bataaxal bu nu jot bu jóge Yude ci sa mbir, te du kenn ci bokk yi, ku dikk wax mbaa mu seedeel la lenn lu bon.
22 Waaye bëgg nanoo dégg ci sa gémmiñu bopp li nga gëm, ndax li nu xam daal mooy, ngér moomu nga bokk, fu nekk lañu koy diiŋate.»
23 Ci kaw loolu ñu jox ko bés, bés ba dikk, ñu bare dikk, fekksi ko ca daluwaayam. Suba ba ngoon mu di leen jàngal, di leen seedeel lu jëm ci nguurug Yàlla, di leen won ci mbirum Yeesu, firnde yu leen gëmloo te tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi.
24 Ñenn ña nag gëm la mu wax, ña ca des weddi.
25 Ba ñu werantee ca seen biir, bay dem te juboowuñu, Póol teg ca ne leen: «Noo gu Sell gee yeyoon wax lii seeni maam, Yonent Yàlla Esayi jottli.
26 Mu ne: “Demal ci xeet wii, nga ne leen: ‘Yeenay dégloo déglu, dungeen dégg; ngeen xoolee xoole, dungeen gis.’
27 Xolu xeet wee dërkiis, seeni nopp fatt, ñu gëmm fatuus, ba seeni gët du gis, seeni nopp du dégg, seen xol it du yég, ba ñu tuub, ma wéral leen.”
28 «Xamleen nag ne xibaaru mucc gii tukkee fa Yàlla, yóbbante nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»
30 Diiru ñaari at la Póol dal Room ci kërug boppam gu muy fey, di fa àggale mboolem ña koy seetsi.
31 Muy yégle nguurug Yàlla, di jàngle mbirum Sang Yeesu Almasi ci teeyug bakkanam te amul benn gàllankoor.
Jëf ya 28 in Kàddug Yàlla gi