Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 27:2-43 in Wolof

Help us?

JËF YA 27:2-43 in Téereb Injiil

2 Nu dugg ca gaalu dëkku Adaramit guy taxaw ci teeruy Asi, daldi tàbbi ci biir géej; te Aristàrk, mi dëkk Tesalonig ci diiwaanu Maseduwan, ànd ak nun.
3 Ca ëllëg sa nu teer Sidon; Yulyus laabiir ci Pool, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu ganale ko.
4 Bi nu fa jógee, nu dem ci biir géej, leru dunu Sipar ci fegu ngelaw li, ndaxte ngelaw li da noo soflu.
5 Nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, teersi Mira ca wàlli Lisi.
6 Foofa nag njiit la gis gaal gu jóge Alegsàndiri, jëm Itali, mu dugal nu ca.
7 Noonu nuy dem ndànk diirub fan yu bare, ba janook Kanidd ci kaw coono bu réy; te ndegam ngelaw li mayu nu, nu jëm kanam, nu leru dunu Keret ci fegu ngelaw li, janook Salmon.
8 Nu romb fa ak coono yu bare, agsi ca bérab bu ñuy wax Teeru yu neex, te dend ak dëkku Lase.
9 Fekk booba yàggoon nañu ca yoon wa, te dem ci géej daldi aaytal, ndaxte jamonoy Kooru Yawut ya wees na. Moo tax Pool digal leen ne:
10 «Gaa ñi, gis naa ne tukki bi ëmb na musiba ak kasara ju bare, waxuma gaal gi ak li mu yeb waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.»
11 Waaye njiit la sobental waxi Pool, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
12 Te gannaaw teeru ba neexula lollikoo, ña ca ëpp mànkoo ci jóge fa, dem ci biir géej, ngir wuta agsi Fenigsë, biy teerub dunu Keret te janook sowu suuf ak sowu kaw, nu lollikoo fa.
13 Noonu bi ngelaw lu woyof liy jóge sudd wolee, ñu defe ne man nañoo sottal seen pexe, ñu wëgg diigal, daldi tafu ci dunu Keret.
14 Waaye nees-tuut ngelaw lu wole penku, ñu di ko wax «Ërakilon», jóge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw.
15 Mu ëpp doole gaal ga, daldi ko wat, ba nu bayliku, daldi yal.
16 Nu daldi daw, leru dun bu tuuti bu ñuy wax Kóda ci fegu ngelaw, rawale looco ga ci kaw gaal ga ak coono bu bare.
17 Bi ñu ko yéegee, ñu fab ay buum, ngir laxas ca taatu gaal ga, ngir ragala daanu ci suuf su nooy su ñuy wax Sirt; ba noppi ñu daldi sànni diigal, ngir wàññi doxub gaal ga, nuy yale noonu.
18 Waaye bi nu ngelaw li sonalee bu metti, ca ëllëg sa ñu sànni la gaal ga yeboon ca géej ga.
19 Te ca ñetteelu fan ba, ñu sànni ak seeni loxo jumtukaay, yi ñu yeboon ngir fàggu.
20 Noonu jant bi ne meŋŋ te biddiiw ne mes ay fan yu bare, fekk ba tey ngelaw li di wol ak doole, ba sunu yaakaaru mucc gépp tas.
21 Bi loolu di xew, fekk gëj nañoo lekk, Pool daldi taxaw ci seen biir ne leen: «Gaa ñi, li gënoon mooy ngeen déglu ma te baña jóge Keret, ba indil seen bopp musiba ak kasara ju réy jii.
22 Léegi nag maa ngi leen di dénk, ngeen takk seen fit, ndax gaal gi rekk mooy yàqu, waaye kenn ci yéen du dee.
23 Ndaxte ci guddi menn malaaka dikkal na ma, jóge ci Yàlla sama Boroom, bi may jaamu.
24 Mu ne ma: “Pool bul tiit; fàww nga taxaw ci kanam Sesaar, te yaa tax Yàllay aar bakkani ñi nga àndal ñépp.”
25 Moo tax, gaa ñi, takkleen seen fit, ndax wóolu naa Yàlla ne li mu ma wax dina am.
26 Waaye war nanoo luf cib dun.»
27 Ca fukkeelu guddi ga ak ñeent nu nga doon jayaŋ-jayaŋi ca géeju Adiratig; noonu ca xaaju guddi dawalkati gaal ga defe ne danu jegesi suuf.
28 Ñu sànni nattukaay ba ci biir géej, mu jàpp ñeent fukki meetar, dem ca kanam tuuti, sànniwaat ko, jàpp fanweeri meetar.
29 Ñu ragal ne dinañu fenqu ci ay xeer, kon ñu daldi sànni ñeenti diigal ci geenu gaal ga, di ñaan bët set.
30 Waaye ci kaw loolu dawalkati gaal ga taafantaloo ne dañuy sànniji ay diigal ca boppu gaal ga, fekk dañuy fexee jël looco ga, ba raw.
31 Waaye Pool ne njiit la ak xarekat ya: «Bu ñii desul ci gaal gi, dungeen raw.»
32 Noonu xarekat ya dagg buum, yay téye looco ga, bàyyi ko mu wéy.
33 Bi bët setagul, Pool sant leen ñu lekk; mu ne leen: «Tey mooy seen fukki fan ak ñeent yu ngeen ne jonn, lekkuleen, mosuleen dara.
34 Maa ngi leen di sant nag, ngeen lekk, ndax noonu rekk ngeen mana rawe. Ndax genn kawar du rot ci yéen.»
35 Bi mu waxee loolu, mu fab mburu, sant Yàlla ci kanam ñépp, damm ko, daldi ko lekk.
36 Bi ñu gisee loolu, ñépp dëgëraat, ñu daldi lekk ñoom itam.
37 Mboolem ñi nekkoon ca gaal ga mat na ñaar téeméeri nit ak juróom ñaar fukk ak juróom benn.
38 Noonu ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma ca géej ga, ngir woyofal gaal ga.
39 Bi bët setee nag, xàmmiwuñu réew ma, waaye séen nañu ruqu tefes. Noonu ñu fas yéene caa teeral gaal ga, bu ñu ko manee.
40 Ñu dagg diigal ya, bàyyi leen ci biir géej, yiwiwaale baar ba; ba noppi firi wiiru kanam ga, jublu ca tefes ga.
41 Waaye ñu dal ca tundu suuf ca bérab bu ñaari koroŋ daje, gaal ga daldi fa luf. Boppu gaal ga nuur bu baax, ne fa tekk, te dooley duus ya daldi toj geen ba.
42 Bi loolu amee xarekat ya bëgga rey ñi ñu tëj, ngir ragal ñenn ñi féey, ba raw.
43 Waaye njiit la bëgga musal Pool, mu tere leen pexe ma. Mu sant ñi mana féey, ñu jëkka sóobu ca ndox ma, ba jot tefes ga.
JËF YA 27 in Téereb Injiil

Jëf ya 27:2-43 in Kàddug Yàlla gi

2 Nu dugg gaalu dëkk ba ñuy wax Àddramit tey jaareji teeruy Asi, daldi tàbbi biir géej, Aristàrk jenn waay ju dëkke Tesalonig ca diiwaanu Maseduwan, ànd ak nun.
3 Ca ëllëg sa nu teeri Sidon; Yulyus nag baaxe Póol, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu topptoo ko.
4 Nu jóge fa, dellu géej, ngelaw li soflu nu, nu leru tefesu Sippar, jaare wet gu nu fegoo ngelaw li.
5 Ci kaw loolu nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, daldi teeri Mira ca Lisi.
6 Foofa nag njiitu takk-der ba gis gaal gu jóge Alegsàndiri, jëm Itali, mu dugal nu ca.
7 Ba loolu amee nuy deme ndànk ay fani fan; sonn nanu lool doora jub Kanidd, waaye ngelaw li mayu nu nu teer. Nu leru tefesu Keret, jaare wet gu nu fegoo ngelaw li, janook Salmon.
8 Sonn nanu lool bala noo romb foofu, doora agsi fa ñuy wax Neex Teeru, te dend ak dëkk ba ñuy wax Lase.
9 Fekk na nag nu yàgg ca yoon wa, ba tollu ci jamono ju tukkib géej aaytal, ndax fekk na Koorug Yawut wees. Loolu tax Póol digal leen ne:
10 «Bokk yi, gis naa ne yoon wii loraange ak yàqule gu réy la. Waxuma gaal gi ak li mu yeb, waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.»
11 Teewul njiitu takk-der ba sobental waxi Póol, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
12 Te itam teeru boobu neexul woona lollikoo. Loolu waral ña ëpp ca waa gaal ga mànkoo ci jóge fa, dellu géej, te fexe nu ñu àgge Fenigsë, ngir lollikoo fa. Mooy teerub dunu Keret bi jublu sowub suuf ak sowub kaw.
13 Ci kaw loolu ngelawal bëj-saalum wal ndànk, ñu njort ne man nañoo sottal seen pexe. Ñu wëgg diigal, daldi tafoo tefesu Keret.
14 Teewul nes tuut ngelaw lu réy lu ñuy wax Penkub kaw, riddee ca dun ba.
15 Gaal gi buubu, manatula dékku ngelaw li, ba nu mujj bayliku, daldi yal.
16 Nu leru nag dun bu tuuti bu ñuy wax Koda, jaare wet gu nu fegoo ngelaw li, teg ci sonn lool doora téye loocob rawtu bu gaal gi.
17 Ñu yéege looco ba, daldi jël ay buum yu ñu laxas ca yaramu gaal ga, dàbblee ko ko. Ci kaw loolu ñu ragala ngiroji ca beeñ bu ñuy wax Sirt, ba tax ñu sànni diigal, ngir yeexal gaal ga, daldi yalal.
18 Ca ëllëg sa ngelaw la wéye noo pamti-pamtee, ba ñu mujj wàññi ca yebu gaal ga, sànni biir géej.
19 Ca gannaaw ëllëg sa, seen loxoy bopp lañu jële yenn jumtukaayi gaal ga, sànni.
20 Ay fani fan jant beek biddiiw yi ne meŋŋ, te ngelaw liy riddi rekk, ba nu noppee yaakaar ne dinanu mucc.
21 Loolu nag fekk na ñu gëjoona lekk. Póol daldi taxaw ca seen biir ne: «Bokk yi, su ngeen yégoon déggal ma, baña jóge Keret, ba moyu loraange gii ak yàqule gii.
22 Léegi nag dama leen di ñaax, ngir ngeen dalal seen xel, ndax kenn ci yeen du ñàkk bakkanam, gaal gi rekk ay yàqu.
23 Ndax malaakam Yàlla ji ma moom, te ma di ko jaamu, moo ma dikkal biig.
24 Mu ne ma: “Póol, bul tiit; fàww nga taxawi fa kanam Sesaar, te it Yàlla moo la baaxe muccug mboolem ñi nga àndal ci gaal gi.”
25 Kon nag, bokk yi, dalal-leen seen xel, ndax gëm naa Yàlla, xam naa ne ni mu ko waxe, ni lay ame.
26 Du ñàkk aw dun wu nu lufeji.»
27 Ca fukkeelu bés baak ñeent, nu ngay yal-yalee fu ne ca géeju Adiratig; ba guddi ga xaajee mool ya njort ne nu ngay jegesi ab tefes.
28 Ñu sànni nattukaay ba biir géej, gis ndox ma xóote ñaar fukki dayo, xawa yemook ñeent fukki meetar. Ñu demati tuuti, sànniwaat ko, daldi gis ndox ma xóote fanweeri meetar, xawa yemook fukki dayo ak juróom.
29 Ci kaw loolu ñu ragala lufeji bérab bu ami doj, ba tax ñu sànnee ca geenu gaal ga, ñeenti diigal, tey ñaan jant fenke leen.
30 Teewul mool ya ñoom di fexee raw, daldi dem ba yoori loocob rawtu ba biir géej, tey taafantoo ne ay diigal lañuy sànnee ca boppu gaal ga.
31 Póol nag ne njiitu takk-der ba ak xarekat ya: «Ñii bu ñu desul ci gaal gi, yeen dungeen raw.»
32 Ca la takk-der ya dog buum ya téye looco ba, bàyyi, mu wéy.
33 Naka la jant di waaja fenk, Póol ñaax ñépp, ngir ñu lekk; mu ne leen: «Fukki fan ak ñeent a ngii, yeena ngi toog, lekkuleen, sexuleen dara.
34 Dama leen di ñaax nag ngir ngeen lekk, ndax noonu doŋŋ ngeen mana rawe. Du genn kawar sax guy rote ci boppu kenn ci yeen.»
35 Loolu la wax, daldi jël mburu, sant Yàlla ci kanam ñépp, ba noppi dagg, lekk.
36 Ba loolu amee, ñépp dellu sawar, daldi lekk ñoom itam.
37 Ña nekkoon ca gaal ga ñépp ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom benn (276) lañu.
38 Ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma biir géej, ngir woyofal gaal ga.
39 Ba bët setee, xàmmiwuñu réew ma, waaye ab catu tefes lañu séen. Ñu fas yéene caa teerali, ndegam manu na.
40 Ba mu ko defee ñu dagg diigal ya, wacc biir géej, yiwiwaale goj ya téye joowu yay dawal gaal ga. Ci kaw loolu ñu firi wiiru kanam ga, wacce ak ngelaw la, nu wuti tefes ga.
41 Teewul ñu dal fu ñaari ndaw daje, ci ab tundu beeñ, gaal ga luf. Boppu gaal ga nuur ca suuf sa, yëngootul, geenu gaal ga tas ndax dooley gannax ya.
42 Ba loolu amee takk-der ya nara rey ña ñu tëj, bala ñoo féey, ba raw.
43 Njiitu takk-der ba nag namma rawale bakkanu Póol, ba tax mu aaye loolu. Mu sant ñi mana féey, ne leen ñu jëkka sóobu, wuti tefes ga.
Jëf ya 27 in Kàddug Yàlla gi