Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 26:8-31 in Wolof

Help us?

JËF YA 26:8-31 in Téereb Injiil

8 Lu tax seen xel dàq ne Yàlla dina dekkal ñi dee?
9 «Man sax ci sama bopp defe woon naa ne war naa def lu bare, ngir suufeel turu Yeesum Nasaret.
10 Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sañ-sañ ci sarxalkat yu mag ya, bay tëj gaayi Yàlla yu bare. Rax-ca-dolli ku ñu ci masoona bëgga rey, ànd naa ci.
11 Daan naa wër jàngoo jàngu, di leen teg toskare te di leen jéema weddiloo. Te sama mer daa na tar, ba ma di leen xañ ba ca dëkk yu sore, ngir fitnaal leen.
12 «Noonu am bés, may dem dëkku Damaas, yor sañ-sañ ak ndigalu sarxalkat yu mag ya.
13 Ca njolloor, buur bi, gis naa ca yoon wa leer gu jóge asamaan ne ràyy, ba raw leeru jant, melax ba ëmb ma, man ak ñi ma àndal.
14 Nu ne nërëm ci suuf, ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay bëre ak man ni fas wuy woŋŋeetu ku koy jam dëgël, metti na ci yaw.”
15 «Noonu ma ne ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Maa di Yeesu, mi ngay fitnaal.
16 Waaye jógal taxaw. Lii moo tax ma feeñu la: teg naa la yen, nga di ma seedeel ci lépp li nga gis ci man ak li ma lay feeñuji.
17 Dinaa la musal ci bànni Israyil ak ci ñi dul Yawut. Ci ñoom laa lay yebal,
18 ngir ubbi seeni bët, nga jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, nga nangoo leen ci sañ-sañu Seytaane, waññi leen ci Yàlla, ma baal leen seeni bàkkaar te may leen cér ci biir sama gaa yi sell ci kaw ngëm.”
19 «Kon nag buur Agaripa, woruma li ma Yàlla yen ci peeñu.
20 Waaye li tàmbali ci Damaas, teg ci dëkku Yerusalem ak réewu Yawut mépp, ba agsi ci ñi dul Yawut, yégal naa leen, ñu tuub seeni bàkkaar te waññiku ci Yàlla, bay jëf lu dëppook réccu.
21 Loolu nag moo waral Yawut yi jàpp ma ca kër Yàlla ga, di ma fexee rey.
22 Waaye gannaaw Yàllaa ngi may taxawu ba tey, maa ngi taxaw fi, di ko seedeel ci mag ak ndaw; yokkuma dara ci li yonent yi ak Musaa xamle woon lu jiitu,
23 maanaam Almasi bi dina dékku ay coono, te mooy jëkka dekki, bay jollil leer ci bànni Israyil ak ñi dul Yawut.»
24 Bi muy làyyee nii, Festus daldi ko gëdd ak baat bu kawe ne ko: «Dangaa dof, Pool! Xanaa sa njàng mu réy mi da laa xañ sago.»
25 Waaye Pool ne ko: «Festus mu tedd mi, dofuma; waaye lu dëggu laay wax te ànd ak sago.
26 Yëf yii leer na buur bi, moo tax maa ngi koy wax ak kóolute. Wóor naa ne dara ci lii may wax umpu ko, ndaxte lii amewul ciy ruq.
27 Yaw buur Agaripa, ndax gëmuloo yonent yi? Xam naa bu wér ne gëm nga.»
28 Noonu Agaripa ne Pool: «Xanaa yaw, ci diir bu gàtt bii rekk, nga ma bëgga dugale ci gaayi Kirist!»
29 Pool ne ko: «Muy tey, muy ëllëg, waxuma yaw rekk waaye it ñi may déglu tey ñépp, na Yàlla def, ba ngeen fekksi ma ci li ma nekk, lu moy jéng yii!»
30 Ci kaw loolu buur ba daldi jóg, boroom réew ma topp ci, Berenis tegu ca ak mbooloo ma mépp.
31 Bi ñu génnee nag, ñuy waxante ne: «Nit kii deful dara lu jar dee mbaa kaso.»
JËF YA 26 in Téereb Injiil

Jëf ya 26:8-31 in Kàddug Yàlla gi

8 Ana lu leen taxa jàpp ci seen biir ne xel nanguwul Yàlla di dekkal ñi dee?
9 «Man ci sama bopp, gàntal lu ma man turu Yeesum Nasaret, sama warugar laa ko defoon.
10 Def naa ko ci Yerusalem, te it bare na ñu sell ñu ma tëjlu ci kaw sañ-sañ bu ma sarxalkat yu mag yi jagleel, te saa yu ñu leen tegaan àtteb dee, dama daan biral kàddu gu leen àtte ñàkkal.
11 Jàngoo jàngu laa leen daan tege mbugal ay yooni yoon, ngir xàccloo leen. Maa daan sànju ba xaabaabal ci seen kaw, topp leen ba ci biir dëkki jaambur yi.
12 «Yoon wu mel noonu laa doon dox, jëm Damaas, ci ndigalal ak ndénkaanel sarxalkat yu mag yi.
13 Ba ma demee ba wetu digg bëccëg, Buur, ca laa gis ag melax gu leer ba raw jant bi, fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër, maak ñi ma àndal.
14 Nu ne dàll fi suuf. Ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut, ne ma: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal? Dangay sonal sa bopp rekk, mbete fas wu manula woŋŋeetu ba wéq dëgël bu koy jam.”
15 «Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Sang bi ne ma: “Man maay Yeesu, mi ngay bundxatal.
16 Jógal taxaw nag. Dama laa feeñu ngir def la ngay sama surga, ngir nga di ma seedeel peeñum tey, ak peeñu yi ma lay feeñooji ëllëg.
17 Maa lay musal ci askanu bànni Israyil, ak ci jaambur ñi ma lay yebal,
18 ngir nga xippil leen, jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, seppee leen ci noteelu Seytaane, indi leen ci Yàlla, ñu am njéggalug bàkkaar, am cér ci biir nit ñi ñu sellal ndax ngëm, gi ñu ma gëm.”
19 «Kon nag buur Àggripa, peeñum asamaan moomu, woruma ko.
20 Waaye li dale Damaas ak Yerusalem ba ci réewum Yawut gépp, ba ca ñi dul Yawut, ñoom ñépp yégal naa leen seen wartéef, muy tuubeel ak waññiku ci Yàlla, ak jëf ju tuubeel yellool.
21 Loolu moo waral Yawut yi jàppe ma ca kër Yàlla ga, di ma fexee rey.
22 Ndimbalal Yàlla nag moo ma may may dund ba tey jii, di ko seedeel ci mag ak ndaw, te waxuma lenn lu moy la yonent ya ak Musaa waxoon ne dina am.
23 Dañu noon fàww Almasi jaar ci ay coono te mooy jëkka dekki, ba siiwtaane leer gu jolli, ñeel bànni Israyil ak jaambur ñi itam.»
24 Naka la layool boppam noonu, Festus àddu ca kaw, ne ko: «Póol, yaw dangaa dof! Sa njàng mu réy mee la dofloo.»
25 Póol ne ko: «Dofuma de, Festus mu tedd mi, dëgg gu ànd ak xel kay, laay biral.
26 Lii ma wax, buur bi xam na ko, moo tax ma ñeme koo wax ci kanamam, ndax bir na ma ne, amul lenn lu ko ump ci lii, ngir du cib ruq la xewe.
27 Buur Àggripa, xanaa gëm nga yonent yi? Xam naa xéll ne gëm nga.»
28 Àggripa nag ne Póol: «Nga defe ne man nga maa gaawa def noonu ab gëmkatub Almasi?»
29 Póol ne ko: «Mu gaaw, mu yeex, waxuma yaw rekk, waaye yaak mboolem ñi may déglu laay ñaan Yàlla, ngeen fekksi ma ci lépp, lu moy càllala yii ñu ma jénge!»
30 Ci kaw loolu buur bi ak boroom réew mi jóg, ñook Berenis ak ña ñu toogal.
31 Ña ngay dem, te naa ca seen biir: «Kii kat deful dara lu jar dee mbaa ay jéng.»
Jëf ya 26 in Kàddug Yàlla gi