Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 25:18-24 in Wolof

Help us?

JËF YA 25:18-24 in Téereb Injiil

18 Ñi koy kalaame nag, bi ñu taxawee, jiiñuñu ko benn ñaawteef ci yi ma yaakaaroon,
19 waaye ñuy werante rekk ak moom ci seen yoon ak ci mbirum ku tudd Yeesu, mi dee, te Pool sax ci ne mu ngi dund.
20 Gannaaw lijjanti mbir moomu jafe woon na ma lool nag, ma laaj ko, ndax bëgg na dem Yerusalem, layooji fa ci mbir yooyu.
21 Waaye Pool ñaan, nu fomm mbiram, ba kera buur bu tedd ba di ko àtte. Noonu santaane naa ñu aj ko, ba keroog ma koy yónnee Sesaar.»
22 Booba nag Agaripa ne Festus: «Man sax bëgg naa dégg nit kooku.» Festus ne ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.»
23 Ca ëllëg sa nag Agaripa ak Berenis ñëw bu xumb, ñu dugg ca néegu àtte ba, ànd ak kilifay xare ba ak ña am maana ca dëkk ba. Noonu Festus joxe ndigal, ñu indi Pool.
24 Bi mu ñëwee, Festus ne: «Buur Agaripa ak yéen ñépp, ñi fi teew tey, nit kaa ngi nii! Mbiram moo tax mbooloom Yawut yépp, muy ci Yerusalem, muy fii, wër ma di yuuxu ne: “Nit kii waratula dund.”
JËF YA 25 in Téereb Injiil

Jëf ya 25:18-24 in Kàddug Yàlla gi

18 Ba tuumaalkat ya taxawee nag, feeñaluñu jenn tuuma ju bokk ci yu bon, yi ma foogoon,
19 xanaa seen yenn yëfi diiney bopp yu ñu juboowul, ak mbirum ku ñuy wax Yeesu mu dee woon, te Póol moomu di dëggal ne mu ngi dund ba tey.
20 Loolu nag jaaxal ma, ba ma laaj ko ndax nangu naa dem Yerusalem, ñu àttee ko fa ci moomu mbir.
21 Póol itam sàkku ñu dencagum ko kaso, tey sàkku ci mbiram, àtteb buur bu tedd bi. Ma daldi joxe ndigal, ngir ñu dencagum ko kaso, ba ma yebal ko ca Sesaar.»
22 Ci kaw loolu Àggripa ne Festus: «Kooku de, man sax bëgg naa koo déglu.» Festus ne ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.»
23 Ca ëllëg sa Àggripa ak Berenis ànd ak topp mu ràññiku, duggsi ca ëttub àttekaay ba, feggook njiiti gàngoor ya, ak kàngami dëkk ba. Festus joxe ndigal, ñu indi Póol.
24 Ba mu dikkee, Festus ne: «Buur Àggripa, yeen mboolem ñi fi bokk ak nun teew, gis ngeen kii, moom la ma askanu Yawut wépp booleel, muy ca Yerusalem ak fii itam, ñuy xaacu naan: “Kii yelloowula dundati.”
Jëf ya 25 in Kàddug Yàlla gi