13 Gannaaw ab diir buur Àggripa ànd ak jigéenam Berenis ganesi Sesare, ngir nuysi Festus.
14 Ba ñu fa amee ab diir, Festus diis Buur Àggripa mbirum Póol, ne ko: «Jenn waay ju ñu tëj kaso la nu Feligsë bàyyee.
15 Ba ma demee Yerusalem, moom la ma sarxalkat yu mag yeek njiiti Yawut yi booleeloon, di sàkku ci moom ab daan.
16 Ma ne leen: “Aaday Room daal nanguwul ñu jébbale nit, ngir ñu rey ko, te jëkkula jàkkaarloo ak ñi ko tuumaal, ba mana layal boppam ci mbir mi ñu ko tuumaal.”
17 Ba ñu dikkee fekk ma fii itam, yàggaluma ci dara, ca ëllëg sa sax laa toog ca àttekaay ba, daldi joxe ndigal, ñu indi waa ji.
18 Ba tuumaalkat ya taxawee nag, feeñaluñu jenn tuuma ju bokk ci yu bon, yi ma foogoon,
19 xanaa seen yenn yëfi diiney bopp yu ñu juboowul, ak mbirum ku ñuy wax Yeesu mu dee woon, te Póol moomu di dëggal ne mu ngi dund ba tey.
20 Loolu nag jaaxal ma, ba ma laaj ko ndax nangu naa dem Yerusalem, ñu àttee ko fa ci moomu mbir.
21 Póol itam sàkku ñu dencagum ko kaso, tey sàkku ci mbiram, àtteb buur bu tedd bi. Ma daldi joxe ndigal, ngir ñu dencagum ko kaso, ba ma yebal ko ca Sesaar.»
22 Ci kaw loolu Àggripa ne Festus: «Kooku de, man sax bëgg naa koo déglu.» Festus ne ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.»
23 Ca ëllëg sa Àggripa ak Berenis ànd ak topp mu ràññiku, duggsi ca ëttub àttekaay ba, feggook njiiti gàngoor ya, ak kàngami dëkk ba. Festus joxe ndigal, ñu indi Póol.