Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 23:12-18 in Wolof

Help us?

JËF YA 23:12-18 in Téereb Injiil

12 Bi bët setee Yawut ya daldi lal pexe; ñu dige ci ngiñ ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñuy rey Pool.
13 Ña lal pexe ma, seen lim ëpp na ñeent fukk.
14 Noonu ñu dem ca sarxalkat yu mag ya ak njiit ya ne leen: «Giñ nanu ne dunu mos dara, ba kera nuy rey Pool.
15 Léegi nag yéen ak kureelu àttekat ya, laajleen kilifa ga, mu indi ko ci seen kanam, mel ni dangeena bëgga seet mbiram bu gëna wóor. Bu ko defee nun dinanu fagaru, ngir rey ko, bala moo agsi.»
16 Waaye jarbaatu Pool yég fiir ga, mu dem, dugg ca tata ja, yégal ko Pool.
17 Bi ko Pool déggee, mu woo kenn ca njiiti xare ba ne ko: «Yóbbul waxambaane wii ca kilifa ga, ndax am na lu mu ko wara yégal.»
18 Njiit la jël ko, yóbbu ko ca kilifa ga ne ko: «Pool, mi ñu jàpp, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la waxambaane wii, ndaxte am na lu mu lay wax.»
JËF YA 23 in Téereb Injiil

Jëf ya 23:12-18 in Kàddug Yàlla gi

12 Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.
13 Ña lal pexe moomu, ëpp nañu ñeent fukk.
14 Ñu dem ca sarxalkat yu mag ya ak mag ña, ne leen: «Danoo giñ ne dunu dugalati dara sunu gémmiñ, ba kera nu reyee Póol.
15 Léegi nag yeen ak kurélu àttekat yi, ñaanleen njiital gàngoor gi, mu indi Póol ba ci yeen, mu mel ni dangeena bëgga seetaat bu baax mbiram. Nun nag fagaru nanu, ngir bala moo agsi, nu rey ko.»
16 Jarbaatub Póol bu góor nag yég tëru ma. Mu daldi dem ba ca tata ja, dugg, yégal ko Póol.
17 Póol woo kenn ca njiiti takk-der ya, ne ko: «Yóbbul xale bu góor bii ba ci njiital gàngoor gi, ndax am na lu mu ko wara wax.»
18 Njiital xare ba ànd ak xale ba, yóbbu ko ca njiital gàngoor ga, ne ko: «Póol, mi ñu tëj, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la xalelu góor bii, ndax am na lu mu lay wax.»
Jëf ya 23 in Kàddug Yàlla gi