Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 22:3-8 in Wolof

Help us?

JËF YA 22:3-8 in Téereb Injiil

3 «Man Yawut laa, juddoo Tars ci diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Taalibe laa woon ci Gamaleel, mu jàngal ma bu wér yoonu sunuy maam, ba ma sawar ci Yàlla, mel ni yéen ñépp tey.
4 Daan naa fitnaal ña bokkoon ci yoon wii, ba di ci rey sax; yeew naa góor ak jigéen, tëj leen;
5 sarxalkat bu mag ba ak mbooloom njiit yi yépp man nañu ma cee seede. Am bés ñu bindal ma ay bataaxal ngir bokki Damaas. Ma doon fa dem, ngir yeew ña fa nekkoon, indi leen Yerusalem, ngir ñu yar leen.
6 «Waaye ci digg bëccëg, bi ma jaaree ca yoon wa, ba jegesi Damaas, ca saa sa leer gu mag jóge asamaan, melax ba ëmb ma.
7 Ma daldi ne nërëm ci suuf, dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal?”
8 Ma ne ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Mu ne ma: “Maa di Yeesum Nasaret, mi ngay fitnaal.”
JËF YA 22 in Téereb Injiil

Jëf ya 22:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 «Man ab Yawut laa, juddoo Tàrs ca diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Ci keppaaru Gamalyel laa jànge, njàng mu dëppoo bu mat sëkk ak sunu yoonu maam. Ma doonoon ku xér ci Yàlla ni mboolem yeen ñii tey.
4 Yoon wii tey, daan naa fitnaal ñi ko gëm ba sabab seenug dee. Yeew naa góor, yeew jigéen, tëjlu leen kaso.
5 Sarxalkat bu mag bi, ak mboolem kurélu mag ñi man nañu ma cee seede. Ci ñoom sax laa nangoo woon bataaxal bu jëm ca bokki Yawut ya ca Damaas, ga ma jëmoon, ngir yeewe fa gëmkati Yoon wii nekkoon foofa, ba indi leen Yerusalem, ngir ñu mbugal leen.
6 «Yàlla def ma topp yoon wa, ba jub Damaas ci digg bëccëg rekk, ag melax gu mag jekki fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër.
7 Ma ne dàll fi suuf, daldi dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?”
8 Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Mu ne ma: “Man maay Yeesum Nasaret, mi ngay bundxatal.”
Jëf ya 22 in Kàddug Yàlla gi