3 «Man ab Yawut laa, juddoo Tàrs ca diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Ci keppaaru Gamalyel laa jànge, njàng mu dëppoo bu mat sëkk ak sunu yoonu maam. Ma doonoon ku xér ci Yàlla ni mboolem yeen ñii tey.
4 Yoon wii tey, daan naa fitnaal ñi ko gëm ba sabab seenug dee. Yeew naa góor, yeew jigéen, tëjlu leen kaso.
5 Sarxalkat bu mag bi, ak mboolem kurélu mag ñi man nañu ma cee seede. Ci ñoom sax laa nangoo woon bataaxal bu jëm ca bokki Yawut ya ca Damaas, ga ma jëmoon, ngir yeewe fa gëmkati Yoon wii nekkoon foofa, ba indi leen Yerusalem, ngir ñu mbugal leen.
6 «Yàlla def ma topp yoon wa, ba jub Damaas ci digg bëccëg rekk, ag melax gu mag jekki fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër.
7 Ma ne dàll fi suuf, daldi dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?”
8 Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Mu ne ma: “Man maay Yeesum Nasaret, mi ngay bundxatal.”
9 Ñi ma àndaloon gis nañu leer gi, waaye ki wax ak man, xamuñu li mu wax.
10 Ma ne ko: “Sang bi, nu may def?” Sang bi ne ma: “Jógal dem Damaas, dees na la wax foofa mboolem li ñu la sas, nga def ko.”
11 Gisatuma woon dara ndax leeraayu melax ga; ña ma àndal ñoo ma mujj wommat, ba ma agsi Damaas.
12 «Ku ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Ku am diiney yoonu Musaa te rafetub jëw ci biir mboolem Yawuti dëkk ba.
13 Mu dikk taxaw fi sama wet, ne ma: “Mbokk mi Sóol, gisal na woon.” Ca saa sa, may gis na woon, di ko xool.
14 Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam moo la dencal céru ràññee coobareem, ak gis Aji Jub ji, dégg ko, muy wax ak yaw.