Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 22:10-30 in Wolof

Help us?

JËF YA 22:10-30 in Téereb Injiil

10 Noonu ma laaj ko: “Lu ma wara def, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Jógal dem Damaas, foofa dees na la biral lépp, li ma la yen.”
11 Gannaaw gisuma woon dara ndax leeraayu melxat ga, ña ma àndal wommat ma, ma ñëw Damaas.
12 «Bi ma ko defee ku tudd Anañas ñëw ci man. Nit ku ragal Yàlla la woon ci sàmm yoonu Musaa, te Yawuti Damaas yépp seedeel ko lu baax.
13 Mu taxaw ci sama wet ne ma: “Sóol sama mbokk, delluwaatal di gis.” Noonu ma daldi gisaat ca saa sa, xool ko.
14 Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam tànn na la, ba may la, nga xam coobareem te gis Aji Jub ji te nga dégg ay waxam.
15 Ndaxte li nga gis te dégg ko, dinga ko seede ci ñépp.
16 Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set ci say bàkkaar ci tudd turu Yeesu.”
17 «Bi ma délsee Yerusalem nag, di ñaan ca kër Yàlla ga, leer tàbbi ci man.
18 Ma daldi gis Boroom bi, mu ne ma: “Génnal Yerusalem nu mu gëna gaawe, ndaxte duñu nangu li ngay seede ci man.”
19 Ma ne ko: “Boroom bi, xam nañu ne dama daan wër jàngoo jàngu, di tëj kaso ak di dóor ay yar ñi la gëm.
20 Rax-ca-dolli bi ñu tuuree deretu Ecen, mi la doon seedeel, teewe naa ko, ànd ca, bay wottu sax yérey ñi ko doon rey.”
21 Waaye Boroom bi ne ma: “Demal, dinaa la yebal fu sore, nga jëm ci xeeti ñi dul Yawut.”»
22 Mbooloo ma déglu ko nag ba ca wax jooju, waaye bi ñu déggee loolu, ñu daldi yuuxu naan: «Farleen ko ci àddina! Yembar mu mel ni moom yeyoowula dund!»
23 Ñu daldi yuuxu ak di sànni seeni yére, tibb suuf, di callmeeru.
24 Noonu kilifa ga santaane, ñu dugal Pool ca tata ja te caw ko ay yar yu metti, laaj ko ba xam lu tax ñu di ko yuuxoo nii.
25 Waaye bi ñu koy joñ ak ay der, Pool ne njiitu xare ba fa taxaw: «Ndax am nga sañ-sañu dóor ay yar jaamburu Room, te fekk yoon dabu ko sax?»
26 Bi ko njiit la déggee, mu fekki kilifaam, yégal ko ko; mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay def? Nit kale jaambur la ci Room.»
27 Noonu kilifa ga ñëw laaj Pool: «Wax ma, ndax jaambur nga ci Room?» Mu ne ko: «Waaw, moom laa.»
28 Kilifa ga ne ko: «Man fey naa xaalis bu bare, ngir nekk jaambur ci Room.» Waaye Pool ne ko: «Man de dama koo judduwaale.»
29 Ñi ko bëggoona dóor ay yar nag randu ko ca saa sa. Te kilifa ga sax tiit ci xam ne Pool jaamburu Room la, te yeewlu na ko.
30 Ca ëllëg sa kilifa ga bàyyi ko, ndaxte bëggoon na xam bu wóor lu ko Yawut ya jiiñ. Mu santaane ne, sarxalkat yu mag ya dajaloo, ñoom ak kureelu àttekat ya. Gannaaw loolu mu indilu Pool, dëj ko ci seen kanam.
JËF YA 22 in Téereb Injiil

Jëf ya 22:10-30 in Kàddug Yàlla gi

10 Ma ne ko: “Sang bi, nu may def?” Sang bi ne ma: “Jógal dem Damaas, dees na la wax foofa mboolem li ñu la sas, nga def ko.”
11 Gisatuma woon dara ndax leeraayu melax ga; ña ma àndal ñoo ma mujj wommat, ba ma agsi Damaas.
12 «Ku ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Ku am diiney yoonu Musaa te rafetub jëw ci biir mboolem Yawuti dëkk ba.
13 Mu dikk taxaw fi sama wet, ne ma: “Mbokk mi Sóol, gisal na woon.” Ca saa sa, may gis na woon, di ko xool.
14 Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam moo la dencal céru ràññee coobareem, ak gis Aji Jub ji, dégg ko, muy wax ak yaw.
15 Ndax li nga gis, dégg ko, yaa koy seedeel nit ñépp.
16 Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set, teqlikook say bàkkaar, te tudd turu Yeesu.”
17 «Yàlla def, gannaaw ba ma délsee Yerusalem, ma doon ñaan ca kër Yàlla ga, daldi daanu leer.
18 Ma gis Sang bi, mu ne ma: “Gaawal, daw génn Yerusalem, li nga may seedeel, duñu ko nangu.”
19 Ma ne ko: “Sang bi, ñoom ci seen bopp xam nañu ne jàngu ci kaw jàngu, maa fa daan tëjlu ak a cawlu ñi la gëm.
20 Te it ba ñuy tuur deretu Eccen, sa seede ba, man it maa nga fa woon, juboo caak ñoom, te ña ko rey, maa leen doon wattul seeni yére.”
21 Mu ne ma: “Demal, man, fu sore laa lay yebal ca ña dul Yawut.”»
22 Ba ba muy wax loolu, mbooloo maa nga koy déglu. Ba ñu déggee kàddu yooyu lañu xaacu ne: «Jëleleen ko ci kaw suuf! Ku mel ni kii yeyoowula dund!»
23 Ña ngay yuuxoo, di sànni seeni yére, tibb suuf, callmeeru.
24 Ci kaw loolu njiitu gàngoor ga santaane, ñu dugal Póol ca tata ja te laaje ko ay yar, ngir xam lu waral ñu di ko yuuxoo noonu.
25 Naka lañu ko yeew ngir dóor ko ay kàccri, mu ne njiitu takk-der ba fa taxaw: «As goru Room bu yoon dabul, mbaa am nga sañ-sañu dóorlu ko?»
26 Njiitu takk-der ba dégg loolu, daldi dem ba ca njiital gàngoor ga, xamal ko ko, ne ko: «Li ngay def nag? Nit kii as goru Room la!»
27 Njiital gàngoor ga dikk, ne Póol: «Yaw wax ma, ndax as goru Room nga?» Mu ne: «Waaw.»
28 Mu ne ko: «Man de xaalis bu bare laa jënde sañ-sañu doon as goru Room.» Mu ne ko: «Man nag moom laa judduwaale.»
29 Ña ko doon waaja laaje ay dóor nag dànd ko ca saa sa. Njiital gàngoor ga it tiit na, ba mu yégee ne Póol as goru Room la, te fekk mu yeewlu ko.
30 Ca ëllëg sa nag njiital gàngoor ga bëgga am lu ko leer nàññ ca la Yawut ya jiiñ Póol. Mu yiwi ko, woolu sarxalkat yu mag ya, ak mboolem kurélu àttekat ya. Ci kaw loolu mu indi Póol, taxawal ko ci seen kanam.
Jëf ya 22 in Kàddug Yàlla gi