Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 21

Jëf ya 21:7-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Nun nag ba nu jógee Tir, danoo ñoqli ba teeri Patolemayis. Nu nuyoo faak bokki taalibe ya, toog faak ñoom benn fan.
8Ca ëllëg sa nu dem ba àgg Sesare. Nu dem kër Filib, xamlekatu xibaaru jàmm, bi bokk ci Juróom ñaar ñi. Nu dal ak moom.
9Filib moomu amoon na ñeenti doomi janq yuy waxe ay waxyu.
10Gannaaw ba nu fa toogee ay fan, ab yonent bu ñuy wax Agabus jóge Yude, agsi.
11Mu dikk ba ci nun, jël ngañaayal Póol, yeewe ko ay tànkam aki loxoom, daldi ne: «Noo gu Sell gi dafa wax ne: “Ki moom ngañaay lii, nii la ko Yawut yiy yeewe ca Yerusalem, jébbal ko jaambur ñi dul Yawut.”»
12Ba nu déggee loolu, nun ak waa gox baa tinu Póol, ne ko bumu dem Yerusalem.
13Ci kaw loolu Póol ne: «Lu ngeen di def nii, di jeexal sama xol? Waxuma ñu yeew ma rekk, waaye dee sax nangu naa koo def ci Yerusalem ngir Sang Yeesu.»
14Naka lanu wax, wax, mu të, nu bàyyi, daldi ne: «Kon nag yal na Boroom bi sottal coobareem!»
15Gannaaw fan yooyu lanu fabu, ngir dem Yerusalem.
16Ci biir loolu ay taalibe yu dëkke Sesare ànd ak nun, yóbbu nu fa nu wara dali, ca kër ku ñuy wax Manason, ma cosaanoo Sippar, te di taalibe bu yàgg.
17Ba nu agsee Yerusalem nag, bokki taalibe ya bége nañu noo dalal.
18Ca ëllëg sa Póol ànd ak nun, seeti Yanqóoba, fekk mag ñépp a nga fa teew.
19Póol nuyook ñoom, ba noppi benn-bennalal leen jëf, ji Yàlla sottale liggéeyam ci biir jaambur ñi.
20Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa.
21Ñoo dégg nag sab jëw, ñu ne dëddu yoonu Musaa mooy li ngay jàngal mboolem Yawut yi dëkk ci biir jaambur ñi, naan leen buñu xarfal seeni doom, te buñu topp sunuy aada.
22Lu ciy pexe nag? Ndax kat duñu umple ne dikk nga.

Read Jëf ya 21Jëf ya 21
Compare Jëf ya 21:7-22Jëf ya 21:7-22