Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 21

Jëf ya 21:30-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
30Ba loolu amee dëkk ba bépp màbb, nit ña ne kër-kër, ne këpp, ñu jàpp Póol, génne ko kër Yàlla ga rekk, daldi tëj bunt ya.
31Naka lañu koy wuta rey, ñu àgge njiital gàngooru Room ba yore kilifteef ga, ne ko Yerusalem gépp salfaañoo na.
32Ca saa sa mu ànd ak ay dag, ak njiiti takk-der, ne jaas ca biir mbooloo ma. Yawut ya nag gis njiital gàngoor ga ak dag ya, daldi dakkal yar ya ñu doon dóor Póol.
33Ci kaw loolu njiit la agsi, jàpp ko, daldi santaane ñu jénge ko ñaari càllala. Ba loolu wéyee mu laajte, ne: «Kii ku mu doon, ak lu mu def?»
34Ñenn ca mbooloo ma xaacu ne lii, ña ca des ne laa. Ñolñol ja nag tax manu caa xam dara lu leer. Mu daldi santaane, ñu yóbbu ko ca biir tata ja.
35Ba Póol àgge ca dëggastali tata ja, mbooloo ma daa sànju ak doole, ba takk-der ya mujj fab Póol, gàddu ko.
36Ndax booba mbooloo mu réy a ko topp, di xaacu naa: «Na dee!»
37Naka lañu koy waaja dugal ca tata ja, Póol ne njiitu gàngoor ga: «Ndax man naa laa wax baat?» Mu ne ko: «Ndeke dégg nga gereg?
38Kon du yaay waayu Misra jooju yëngaloon dëkk bi ci fan yii, te yóbbu woon ñeenti junniy Bóomkat ya (4 000) ca màndiŋ ma?»
39Póol ne ko: «Man de ab Yawut laa, di as goru Tàrs, dëkk bu ñàkkul tur ba ca diiwaanu Silisi. Dama lay ñaan, nga may ma, ma wax ak mbooloo mi.»

Read Jëf ya 21Jëf ya 21
Compare Jëf ya 21:30-39Jëf ya 21:30-39