Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 21:28-36 in Wolof

Help us?

JËF YA 21:28-36 in Téereb Injiil

28 di xaacu ne: «Wallee, wallee, yéen bokki Israyil! Waa jaa ngi nii, moom miy waare fépp ak ci ñépp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak bérab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci kër Yàlla gi, ba indi sobe ci bérab bu sell bii.»
29 Li tax ñu wax loolu, mooy gisoon nañu Torofim mu Efes, ànd ak moom ca dëkk ba, te ñu yaakaar ne Pool dugal na ko ca kër Yàlla ga.
30 Noonu dëkk ba bépp màbb, mbooloo ma ne këpp, ñu jàpp Pool, génne ko ca kër Yàlla ga. Ca saa sa ñu tëj bunt ya.
31 Bi ñu koy wuta rey, xibaar ba agsi ba ca kilifag mbooloom xarekat ba, naan Yerusalem gépp jaxasoo na.
32 Ca saa sa mu ànd ak ay xarekat ak ay njiiti xare, ne jaas wàcc ci ñoom. Bi Yawut ya gisee kilifa ga ak xarekat ya nag, ñu daldi bàyyi dóor, ya ñu doon dóor Pool.
33 Noonu kilifa ga jegesi jàpp ko, santaane ñu jéng ko ak ñaari càllala. Bi ñu ko defee mu laaj ku mu doon ak lu mu def.
34 Waaye ci biir mbooloo ma, bu ñii nee lii, ña ca des ne laa. Kon nag gannaaw manu caa xam dara lu wóor ndax coow li, mu santaane, ñu yóbbu ko ci biir tata ja.
35 Bi Pool eggee ca yéegukaayu tata ja, aaytalu mbooloo ma réy, ba ay xarekat fab ko.
36 Ndaxte mbooloo maa nga ko topp, di xaacu ne: «Reyleen ko!»
JËF YA 21 in Téereb Injiil

Jëf ya 21:28-36 in Kàddug Yàlla gi

28 di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.»
29 Booba Torofim mu Efes la ñu gisoon ca dëkk ba, mu ànd ak Póol, ñu yaakaar ne Póol da koo yóbbu ca kër Yàlla ga.
30 Ba loolu amee dëkk ba bépp màbb, nit ña ne kër-kër, ne këpp, ñu jàpp Póol, génne ko kër Yàlla ga rekk, daldi tëj bunt ya.
31 Naka lañu koy wuta rey, ñu àgge njiital gàngooru Room ba yore kilifteef ga, ne ko Yerusalem gépp salfaañoo na.
32 Ca saa sa mu ànd ak ay dag, ak njiiti takk-der, ne jaas ca biir mbooloo ma. Yawut ya nag gis njiital gàngoor ga ak dag ya, daldi dakkal yar ya ñu doon dóor Póol.
33 Ci kaw loolu njiit la agsi, jàpp ko, daldi santaane ñu jénge ko ñaari càllala. Ba loolu wéyee mu laajte, ne: «Kii ku mu doon, ak lu mu def?»
34 Ñenn ca mbooloo ma xaacu ne lii, ña ca des ne laa. Ñolñol ja nag tax manu caa xam dara lu leer. Mu daldi santaane, ñu yóbbu ko ca biir tata ja.
35 Ba Póol àgge ca dëggastali tata ja, mbooloo ma daa sànju ak doole, ba takk-der ya mujj fab Póol, gàddu ko.
36 Ndax booba mbooloo mu réy a ko topp, di xaacu naa: «Na dee!»
Jëf ya 21 in Kàddug Yàlla gi