Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 21:19-33 in Wolof

Help us?

JËF YA 21:19-33 in Téereb Injiil

19 Noonu Pool nuyu leen, nettali leen benn-benn li Yàlla def ci biir ñi dul Yawut, jaarale ko ci liggéeyam.
20 Bi ko njiit ya déggee, ñu màggal Yàlla ne ko: «Mbokk mi, gis nga ne am na ay junniy Yawut ñu gëm, te ñépp a sawar ci yoonu Musaa.
21 Dégg nañu ci sa mbir nag ne yaa ngi jàngal Yawut yépp, yi dëkk ci biir ñi dul Yawut, ñu bàyyi yoonu Musaa te baña xarafal seeni doom mbaa topp sunuy aada.
22 Lu nu ci wara def nag? Ndaxte ci lu wér dinañu xam ne ñëw nga.
23 Nu ngi lay digal nag, nga def nii: am na ci nun ñeenti góor ñu dige ak Yàlla.
24 Jël leen, bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateef. Noonu ñépp dinañu xam ne li ñu déggoon ci sa mbir du dëgg, waaye yaa ngi jëf tey sàmm yoonu Musaa.
25 Naka ñi dul Yawut ñi gëm, bind nanu leen li nu àtte ne, ñu moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm te moytu deretu médd ak njaaloo.»
26 Bi ñu ko waxee, Pool jël nit ña te ca ëllëg sa mu bokk setlu ak ñoom, ñu dugg ca kër Yàlla ga. Ñu xamle ban bés la seen setlu di àgg, di bés bu ñuy jébbale sarax ngir kenn ku nekk ci ñoom.
27 Bi àppu juróom ñaari fan ya di bëgga jeex, Yawut yi jóge diiwaanu Asi gis Pool ca kër Yàlla ga. Ñu daldi jógloo mbooloo mépp, jàpp ko,
28 di xaacu ne: «Wallee, wallee, yéen bokki Israyil! Waa jaa ngi nii, moom miy waare fépp ak ci ñépp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak bérab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci kër Yàlla gi, ba indi sobe ci bérab bu sell bii.»
29 Li tax ñu wax loolu, mooy gisoon nañu Torofim mu Efes, ànd ak moom ca dëkk ba, te ñu yaakaar ne Pool dugal na ko ca kër Yàlla ga.
30 Noonu dëkk ba bépp màbb, mbooloo ma ne këpp, ñu jàpp Pool, génne ko ca kër Yàlla ga. Ca saa sa ñu tëj bunt ya.
31 Bi ñu koy wuta rey, xibaar ba agsi ba ca kilifag mbooloom xarekat ba, naan Yerusalem gépp jaxasoo na.
32 Ca saa sa mu ànd ak ay xarekat ak ay njiiti xare, ne jaas wàcc ci ñoom. Bi Yawut ya gisee kilifa ga ak xarekat ya nag, ñu daldi bàyyi dóor, ya ñu doon dóor Pool.
33 Noonu kilifa ga jegesi jàpp ko, santaane ñu jéng ko ak ñaari càllala. Bi ñu ko defee mu laaj ku mu doon ak lu mu def.
JËF YA 21 in Téereb Injiil

Jëf ya 21:19-33 in Kàddug Yàlla gi

19 Póol nuyook ñoom, ba noppi benn-bennalal leen jëf, ji Yàlla sottale liggéeyam ci biir jaambur ñi.
20 Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa.
21 Ñoo dégg nag sab jëw, ñu ne dëddu yoonu Musaa mooy li ngay jàngal mboolem Yawut yi dëkk ci biir jaambur ñi, naan leen buñu xarfal seeni doom, te buñu topp sunuy aada.
22 Lu ciy pexe nag? Ndax kat duñu umple ne dikk nga.
23 Léegi daal, dangay def li nu lay wax nii: nu ngi feek ñeenti nit ñu am lu ñu xasal Yàlla.
24 Ñoom ngay àndal, nga bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateefu bopp, wi boroom xas wu ni mel aadawoo. Su ko defee ñépp ay xam ne li ñu lay jëwe, dara amu ci, te yoonu Musaa ngay jëfe, di ko sàmm.
25 Naka gëmkat ñi dul Yawut nag, bind nanu leen li nu dogal, ne leen ñu moytu ñam wu ñu sarxal ay xërëm, moytoo lekk deret ak yàppu mala mu ñu tuurul deretam, te moytu powum séy.»
26 Ca ëllëg sa Póol ànd ak nit ña, bokk ak ñoom setlu, dugg ca kër Yàlla ga. Mu daldi xamle bés ba seen àppu setlu di mat, ba jooxe ba ci war génn, ñeel kenn ku nekk ci ñoom.
27 Ba àppu juróom ñaari fan yay waaja jeex, Yawut ya jóge diiwaanu Asi gis Póol ca kër Yàlla ga. Ñu yëngal mbooloo mépp, jàpp ko,
28 di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.»
29 Booba Torofim mu Efes la ñu gisoon ca dëkk ba, mu ànd ak Póol, ñu yaakaar ne Póol da koo yóbbu ca kër Yàlla ga.
30 Ba loolu amee dëkk ba bépp màbb, nit ña ne kër-kër, ne këpp, ñu jàpp Póol, génne ko kër Yàlla ga rekk, daldi tëj bunt ya.
31 Naka lañu koy wuta rey, ñu àgge njiital gàngooru Room ba yore kilifteef ga, ne ko Yerusalem gépp salfaañoo na.
32 Ca saa sa mu ànd ak ay dag, ak njiiti takk-der, ne jaas ca biir mbooloo ma. Yawut ya nag gis njiital gàngoor ga ak dag ya, daldi dakkal yar ya ñu doon dóor Póol.
33 Ci kaw loolu njiit la agsi, jàpp ko, daldi santaane ñu jénge ko ñaari càllala. Ba loolu wéyee mu laajte, ne: «Kii ku mu doon, ak lu mu def?»
Jëf ya 21 in Kàddug Yàlla gi