Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 21

Jëf ya 21:11-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Mu dikk ba ci nun, jël ngañaayal Póol, yeewe ko ay tànkam aki loxoom, daldi ne: «Noo gu Sell gi dafa wax ne: “Ki moom ngañaay lii, nii la ko Yawut yiy yeewe ca Yerusalem, jébbal ko jaambur ñi dul Yawut.”»
12Ba nu déggee loolu, nun ak waa gox baa tinu Póol, ne ko bumu dem Yerusalem.
13Ci kaw loolu Póol ne: «Lu ngeen di def nii, di jeexal sama xol? Waxuma ñu yeew ma rekk, waaye dee sax nangu naa koo def ci Yerusalem ngir Sang Yeesu.»
14Naka lanu wax, wax, mu të, nu bàyyi, daldi ne: «Kon nag yal na Boroom bi sottal coobareem!»
15Gannaaw fan yooyu lanu fabu, ngir dem Yerusalem.
16Ci biir loolu ay taalibe yu dëkke Sesare ànd ak nun, yóbbu nu fa nu wara dali, ca kër ku ñuy wax Manason, ma cosaanoo Sippar, te di taalibe bu yàgg.
17Ba nu agsee Yerusalem nag, bokki taalibe ya bége nañu noo dalal.
18Ca ëllëg sa Póol ànd ak nun, seeti Yanqóoba, fekk mag ñépp a nga fa teew.
19Póol nuyook ñoom, ba noppi benn-bennalal leen jëf, ji Yàlla sottale liggéeyam ci biir jaambur ñi.
20Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa.
21Ñoo dégg nag sab jëw, ñu ne dëddu yoonu Musaa mooy li ngay jàngal mboolem Yawut yi dëkk ci biir jaambur ñi, naan leen buñu xarfal seeni doom, te buñu topp sunuy aada.
22Lu ciy pexe nag? Ndax kat duñu umple ne dikk nga.
23Léegi daal, dangay def li nu lay wax nii: nu ngi feek ñeenti nit ñu am lu ñu xasal Yàlla.
24Ñoom ngay àndal, nga bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateefu bopp, wi boroom xas wu ni mel aadawoo. Su ko defee ñépp ay xam ne li ñu lay jëwe, dara amu ci, te yoonu Musaa ngay jëfe, di ko sàmm.
25Naka gëmkat ñi dul Yawut nag, bind nanu leen li nu dogal, ne leen ñu moytu ñam wu ñu sarxal ay xërëm, moytoo lekk deret ak yàppu mala mu ñu tuurul deretam, te moytu powum séy.»
26Ca ëllëg sa Póol ànd ak nit ña, bokk ak ñoom setlu, dugg ca kër Yàlla ga. Mu daldi xamle bés ba seen àppu setlu di mat, ba jooxe ba ci war génn, ñeel kenn ku nekk ci ñoom.
27Ba àppu juróom ñaari fan yay waaja jeex, Yawut ya jóge diiwaanu Asi gis Póol ca kër Yàlla ga. Ñu yëngal mbooloo mépp, jàpp ko,
28di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.»
29Booba Torofim mu Efes la ñu gisoon ca dëkk ba, mu ànd ak Póol, ñu yaakaar ne Póol da koo yóbbu ca kër Yàlla ga.
30Ba loolu amee dëkk ba bépp màbb, nit ña ne kër-kër, ne këpp, ñu jàpp Póol, génne ko kër Yàlla ga rekk, daldi tëj bunt ya.
31Naka lañu koy wuta rey, ñu àgge njiital gàngooru Room ba yore kilifteef ga, ne ko Yerusalem gépp salfaañoo na.
32Ca saa sa mu ànd ak ay dag, ak njiiti takk-der, ne jaas ca biir mbooloo ma. Yawut ya nag gis njiital gàngoor ga ak dag ya, daldi dakkal yar ya ñu doon dóor Póol.
33Ci kaw loolu njiit la agsi, jàpp ko, daldi santaane ñu jénge ko ñaari càllala. Ba loolu wéyee mu laajte, ne: «Kii ku mu doon, ak lu mu def?»
34Ñenn ca mbooloo ma xaacu ne lii, ña ca des ne laa. Ñolñol ja nag tax manu caa xam dara lu leer. Mu daldi santaane, ñu yóbbu ko ca biir tata ja.

Read Jëf ya 21Jëf ya 21
Compare Jëf ya 21:11-34Jëf ya 21:11-34