Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 21:10-23 in Wolof

Help us?

JËF YA 21:10-23 in Téereb Injiil

10 Bi nu fa nekkee ay fan nag, yonent bu tudd Agabus jóge Yude, agsi.
11 Mu ñëw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i tànkam ak laxasaayu Pool naan: «Nii la Xel mu Sell mi waxe: “Ki moom laxasaay gii, Yawut yi dinañu ko yeewe nii ca Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut.”»
12 Bi nu déggee loolu, nun ak ña fa nekk nu ñaan Pool, mu baña dem Yerusalem.
13 Ci kaw loolu Pool ne: «Lu ngeen di jooy, di yàq sama xol? Bañuma ñu yeew ma rekk, waaye nangu naa sax, ñu rey ma ci Yerusalem ngir turu Yeesu Boroom bi.»
14 Bi nu ko manula dëpp, nu noppi ne: «Kon na coobarey Boroom bi am!»
15 Gannaaw fan yooyu nu defaru, ngir dem Yerusalem.
16 Noonu ay taalibe yu dëkk Sesare ànd ak nun, yóbbu nu ca nit ku tudd Manason, fu nu wara dal; moom nag nitu Sipar la woon, di taalibe bu yàgg.
17 Bi nu agsee Yerusalem nag, taalibe ya teeru nu ak mbég.
18 Ca ëllëg sa Pool ànd ak nun, seeti Saag, fekk njiit yépp teew fa.
19 Noonu Pool nuyu leen, nettali leen benn-benn li Yàlla def ci biir ñi dul Yawut, jaarale ko ci liggéeyam.
20 Bi ko njiit ya déggee, ñu màggal Yàlla ne ko: «Mbokk mi, gis nga ne am na ay junniy Yawut ñu gëm, te ñépp a sawar ci yoonu Musaa.
21 Dégg nañu ci sa mbir nag ne yaa ngi jàngal Yawut yépp, yi dëkk ci biir ñi dul Yawut, ñu bàyyi yoonu Musaa te baña xarafal seeni doom mbaa topp sunuy aada.
22 Lu nu ci wara def nag? Ndaxte ci lu wér dinañu xam ne ñëw nga.
23 Nu ngi lay digal nag, nga def nii: am na ci nun ñeenti góor ñu dige ak Yàlla.
JËF YA 21 in Téereb Injiil

Jëf ya 21:10-23 in Kàddug Yàlla gi

10 Gannaaw ba nu fa toogee ay fan, ab yonent bu ñuy wax Agabus jóge Yude, agsi.
11 Mu dikk ba ci nun, jël ngañaayal Póol, yeewe ko ay tànkam aki loxoom, daldi ne: «Noo gu Sell gi dafa wax ne: “Ki moom ngañaay lii, nii la ko Yawut yiy yeewe ca Yerusalem, jébbal ko jaambur ñi dul Yawut.”»
12 Ba nu déggee loolu, nun ak waa gox baa tinu Póol, ne ko bumu dem Yerusalem.
13 Ci kaw loolu Póol ne: «Lu ngeen di def nii, di jeexal sama xol? Waxuma ñu yeew ma rekk, waaye dee sax nangu naa koo def ci Yerusalem ngir Sang Yeesu.»
14 Naka lanu wax, wax, mu të, nu bàyyi, daldi ne: «Kon nag yal na Boroom bi sottal coobareem!»
15 Gannaaw fan yooyu lanu fabu, ngir dem Yerusalem.
16 Ci biir loolu ay taalibe yu dëkke Sesare ànd ak nun, yóbbu nu fa nu wara dali, ca kër ku ñuy wax Manason, ma cosaanoo Sippar, te di taalibe bu yàgg.
17 Ba nu agsee Yerusalem nag, bokki taalibe ya bége nañu noo dalal.
18 Ca ëllëg sa Póol ànd ak nun, seeti Yanqóoba, fekk mag ñépp a nga fa teew.
19 Póol nuyook ñoom, ba noppi benn-bennalal leen jëf, ji Yàlla sottale liggéeyam ci biir jaambur ñi.
20 Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa.
21 Ñoo dégg nag sab jëw, ñu ne dëddu yoonu Musaa mooy li ngay jàngal mboolem Yawut yi dëkk ci biir jaambur ñi, naan leen buñu xarfal seeni doom, te buñu topp sunuy aada.
22 Lu ciy pexe nag? Ndax kat duñu umple ne dikk nga.
23 Léegi daal, dangay def li nu lay wax nii: nu ngi feek ñeenti nit ñu am lu ñu xasal Yàlla.
Jëf ya 21 in Kàddug Yàlla gi