5Ndax cim ndox la Yaxya daan sóobe, waaye yeen ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob fii ak fan yu néew.»
6Naka lañu daje fa moom, daldi koy laaj, ne ko: «Sang bi, ndax ci jii jamono ngay sampaat nguurug Israyil?»
7Mu ne leen: «Du yeena wara xam jamono jeek bés, bi Baay bi jà pp ci sañ-sañu boppam.
8Waaye Noo gu Sell gi mooy wà cc ci yeen, ngeen soloo dooleem, daldi doon samay seede ci Yerusalem, ak ci diiwaanu Yude gépp ak ci Samari, ba ca cati à ddina.»
9Naka la wax loolu, ndaw yay xoole, ñu jekki yéegee ko fa, aw niir daldi leen koy là q.
10Ña nga téen, ne jà kk asamaan, Yeesu di wéy. Ci biir loolu ñaar ñu sol yére yu weex ne seef ci seen wet.
11Ñu ne leen: «Yeen waa Galile, lu ngeen di taxaw nii di séentu asamaan? Yeesu male ñu yéegee fi seen biir, yóbbu asamaan, nii ngeen ko gise, mu jëm asamaan, ni lay délsee.»
12Booba la ndaw ya jóge ca tund woowu ñuy wax tundu Oliw, te digganteem ak Yerusalem tollook kemu dox bi yoon maye ci bésub Noflaay, yemook benn kilomet. Ñu dellu nag Yerusalem.
13Ñu agsi, yéeg ca néegu kaw taax ma, fa ñuy dal naka jekk. Piyeer a nga ca, ak Yowaan, ak Yanqóoba ak Àndre, ak Filib ak Tomaa, ak Bartelemi ak Macë, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ farlukatu moom-sa-réew ba, ak Yuda doomu Yanqóoba.
14Ñu mà nkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yà lla, à nd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.
15Ci fan yooyu la Piyeer taxaw ca digg bokk ya, ña fa daje di mbooloo mu tollu ci téeméer ak ñaar fukk (120). Mu ne leen:
16«Bokk yi, Mbind mi moo waxe woon Noo gu Sell gi lu jiitu, ci gémmiñu Daawuda, wax ju jëm ci Yuda mi jiite nit ña, ba ñu jà pp Yeesu. Mbind moomu nag fà ww mu sotti.
17Ci nun la Yuda bokkoon, te amoon na it cér ci sunu liggéey bii.»
18Yuda nag gannaaw ba mu jëndee ab tool ca peyu ñaawtéefam ja, ca la daanu, jiital boppam, biir ba fà cc, butit ya tuuru.