Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 1:4-17 in Wolof

Help us?

JËF YA 1:4-17 in Téereb Injiil

4 Am bés muy lekk ak ñoom, mu sant leen ne: «Buleen sore Yerusalem, waaye ngeen xaar li Baay bi dige woon te ma waxoon leen ko.
5 Ndaxte Yaxya daa na sóob nit ñi ci ndox, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi fi ak ay fan yu néew.»
6 Bi ñu dajaloo ak moom nag, ñu laaj ko: «Boroom bi, ndax ci jamono jii ngay yékkatiwaat nguuru Israyil?»
7 Mu ne leen: «Ngeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko.
8 Waaye bu Xel mu Sell mi ñëwee ci yéen, dingeen jot kàttan te nekk samay seede ci dëkku Yerusalem, ca diiwaani Yude ak Samari yépp ak ba fa àddina yem.»
9 Bi mu waxee loolu, te ñu di ko xool, Yàlla yéege na ko, te aw niir jël ko, làq ko seeni bët.
10 Bi muy dem nag, te ñu ne jàkk asamaan, ñaar ñu sol yu weex daldi ne seef, taxaw ci seen wet.
11 Ñu ne leen: «Yéen waa Galile, lu tax ngeen taxaw, di xool ci asamaan? Yeesu male ñu jële ci seen biir, yéege ko asamaan, dina délsi ni ngeen ko gise, muy dem asamaan.»
12 Bi loolu amee ñu jóge ca tund, woowu ñuy wax tundu Oliw ya, te mu dend ak Yerusalem lu tollu ak kilomet, ñu daldi dellu Yerusalem.
13 Bi ñu dikkee, ñu yéeg ca néeg, ba sut ca taax ma, fa ñuy dal. Ñoo doon Piyeer ak Yowaana, Saag ak Andare, Filib ak Tomaa, Bartelemi ak Macë, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokkoon ci mbooloo mi ñuy wax Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa doomu Saag.
14 Ñoom ñépp ñoo bokk menn xel, di wéy ci ñaan ci Yàlla, ànd ak jigéen ñi ak Maryaama, ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.
15 Ca bés yooya nag Piyeer taxaw ca digg bokk ya, di mbooloo mu tollu ni téeméer ak ñaar fukk.
16 Mu ne leen: «Bokk yi, li Xel mu Sell mi waxoon ci Mbind mi jaarale ko ci gémmiñu Daawuda, fàww mu am. Waxoon na ci mbirum Yudaa, mi wommat ñi jàpp Yeesu
17 te mu bokkoon ci nun, ba am cér ci liggéey bi.»
JËF YA 1 in Téereb Injiil

Jëf ya 1:4-17 in Kàddug Yàlla gi

4 Ba mu nekkee ak ñoom, da leena sant, ne leen: «Buleen jóge Yerusalem, négleen digeb Baay bi ngeen dégge ci sama gémmiñ.
5 Ndax cim ndox la Yaxya daan sóobe, waaye yeen ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob fii ak fan yu néew.»
6 Naka lañu daje fa moom, daldi koy laaj, ne ko: «Sang bi, ndax ci jii jamono ngay sampaat nguurug Israyil?»
7 Mu ne leen: «Du yeena wara xam jamono jeek bés, bi Baay bi jàpp ci sañ-sañu boppam.
8 Waaye Noo gu Sell gi mooy wàcc ci yeen, ngeen soloo dooleem, daldi doon samay seede ci Yerusalem, ak ci diiwaanu Yude gépp ak ci Samari, ba ca cati àddina.»
9 Naka la wax loolu, ndaw yay xoole, ñu jekki yéegee ko fa, aw niir daldi leen koy làq.
10 Ña nga téen, ne jàkk asamaan, Yeesu di wéy. Ci biir loolu ñaar ñu sol yére yu weex ne seef ci seen wet.
11 Ñu ne leen: «Yeen waa Galile, lu ngeen di taxaw nii di séentu asamaan? Yeesu male ñu yéegee fi seen biir, yóbbu asamaan, nii ngeen ko gise, mu jëm asamaan, ni lay délsee.»
12 Booba la ndaw ya jóge ca tund woowu ñuy wax tundu Oliw, te digganteem ak Yerusalem tollook kemu dox bi yoon maye ci bésub Noflaay, yemook benn kilomet. Ñu dellu nag Yerusalem.
13 Ñu agsi, yéeg ca néegu kaw taax ma, fa ñuy dal naka jekk. Piyeer a nga ca, ak Yowaan, ak Yanqóoba ak Àndre, ak Filib ak Tomaa, ak Bartelemi ak Macë, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ farlukatu moom-sa-réew ba, ak Yuda doomu Yanqóoba.
14 Ñu mànkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yàlla, ànd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.
15 Ci fan yooyu la Piyeer taxaw ca digg bokk ya, ña fa daje di mbooloo mu tollu ci téeméer ak ñaar fukk (120). Mu ne leen:
16 «Bokk yi, Mbind mi moo waxe woon Noo gu Sell gi lu jiitu, ci gémmiñu Daawuda, wax ju jëm ci Yuda mi jiite nit ña, ba ñu jàpp Yeesu. Mbind moomu nag fàww mu sotti.
17 Ci nun la Yuda bokkoon, te amoon na it cér ci sunu liggéey bii.»
Jëf ya 1 in Kàddug Yàlla gi