3 Gannaaw ay coonoom, ñëw na ci ñoom, di leen won ay firnde yu bare te wér ne mu ngi dund; mu feeñu leen diirub ñeent fukki fan, di diisoo ak ñoom ci lu jëm ci nguuru Yàlla.
4 Am bés muy lekk ak ñoom, mu sant leen ne: «Buleen sore Yerusalem, waaye ngeen xaar li Baay bi dige woon te ma waxoon leen ko.
5 Ndaxte Yaxya daa na sóob nit ñi ci ndox, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi fi ak ay fan yu néew.»
6 Bi ñu dajaloo ak moom nag, ñu laaj ko: «Boroom bi, ndax ci jamono jii ngay yékkatiwaat nguuru Israyil?»
7 Mu ne leen: «Ngeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko.
8 Waaye bu Xel mu Sell mi ñëwee ci yéen, dingeen jot kàttan te nekk samay seede ci dëkku Yerusalem, ca diiwaani Yude ak Samari yépp ak ba fa àddina yem.»
9 Bi mu waxee loolu, te ñu di ko xool, Yàlla yéege na ko, te aw niir jël ko, làq ko seeni bët.
10 Bi muy dem nag, te ñu ne jàkk asamaan, ñaar ñu sol yu weex daldi ne seef, taxaw ci seen wet.
11 Ñu ne leen: «Yéen waa Galile, lu tax ngeen taxaw, di xool ci asamaan? Yeesu male ñu jële ci seen biir, yéege ko asamaan, dina délsi ni ngeen ko gise, muy dem asamaan.»
12 Bi loolu amee ñu jóge ca tund, woowu ñuy wax tundu Oliw ya, te mu dend ak Yerusalem lu tollu ak kilomet, ñu daldi dellu Yerusalem.
13 Bi ñu dikkee, ñu yéeg ca néeg, ba sut ca taax ma, fa ñuy dal. Ñoo doon Piyeer ak Yowaana, Saag ak Andare, Filib ak Tomaa, Bartelemi ak Macë, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokkoon ci mbooloo mi ñuy wax Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa doomu Saag.
14 Ñoom ñépp ñoo bokk menn xel, di wéy ci ñaan ci Yàlla, ànd ak jigéen ñi ak Maryaama, ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.