Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 1:2-8 in Wolof

Help us?

JËF YA 1:2-8 in Téereb Injiil

2 ba ci bés, ba ko Yàlla yéege ci asamaan. Lu ko jiitu joxoon na ay ndigal, jaare ci Xel mu Sell mi, jëm ci ndaw ya mu tànnoon.
3 Gannaaw ay coonoom, ñëw na ci ñoom, di leen won ay firnde yu bare te wér ne mu ngi dund; mu feeñu leen diirub ñeent fukki fan, di diisoo ak ñoom ci lu jëm ci nguuru Yàlla.
4 Am bés muy lekk ak ñoom, mu sant leen ne: «Buleen sore Yerusalem, waaye ngeen xaar li Baay bi dige woon te ma waxoon leen ko.
5 Ndaxte Yaxya daa na sóob nit ñi ci ndox, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi fi ak ay fan yu néew.»
6 Bi ñu dajaloo ak moom nag, ñu laaj ko: «Boroom bi, ndax ci jamono jii ngay yékkatiwaat nguuru Israyil?»
7 Mu ne leen: «Ngeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko.
8 Waaye bu Xel mu Sell mi ñëwee ci yéen, dingeen jot kàttan te nekk samay seede ci dëkku Yerusalem, ca diiwaani Yude ak Samari yépp ak ba fa àddina yem.»
JËF YA 1 in Téereb Injiil

Jëf ya 1:2-8 in Kàddug Yàlla gi

2 ba ca bés, ba ñu ko yéegee, gannaaw ba mu joxee ndaw ya mu tànnoon, ay ndigal, Noo gu Sell gi jottli.
3 Ndaw yooyu itam la teew fi seen kanam ci firnde yu leer te bare, gannaaw ay coonoom. Diiru ñeent fukki fan la leen feeñu, di leen wax lu jëm ci nguurug Yàlla.
4 Ba mu nekkee ak ñoom, da leena sant, ne leen: «Buleen jóge Yerusalem, négleen digeb Baay bi ngeen dégge ci sama gémmiñ.
5 Ndax cim ndox la Yaxya daan sóobe, waaye yeen ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob fii ak fan yu néew.»
6 Naka lañu daje fa moom, daldi koy laaj, ne ko: «Sang bi, ndax ci jii jamono ngay sampaat nguurug Israyil?»
7 Mu ne leen: «Du yeena wara xam jamono jeek bés, bi Baay bi jàpp ci sañ-sañu boppam.
8 Waaye Noo gu Sell gi mooy wàcc ci yeen, ngeen soloo dooleem, daldi doon samay seede ci Yerusalem, ak ci diiwaanu Yude gépp ak ci Samari, ba ca cati àddina.»
Jëf ya 1 in Kàddug Yàlla gi