Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 1

Jëf ya 1:15-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Ci fan yooyu la Piyeer taxaw ca digg bokk ya, ña fa daje di mbooloo mu tollu ci téeméer ak ñaar fukk (120). Mu ne leen:
16«Bokk yi, Mbind mi moo waxe woon Noo gu Sell gi lu jiitu, ci gémmiñu Daawuda, wax ju jëm ci Yuda mi jiite nit ña, ba ñu jàpp Yeesu. Mbind moomu nag fàww mu sotti.
17Ci nun la Yuda bokkoon, te amoon na it cér ci sunu liggéey bii.»
18Yuda nag gannaaw ba mu jëndee ab tool ca peyu ñaawtéefam ja, ca la daanu, jiital boppam, biir ba fàcc, butit ya tuuru.

Read Jëf ya 1Jëf ya 1
Compare Jëf ya 1:15-18Jëf ya 1:15-18