12 Booba la ndaw ya jóge ca tund woowu ñuy wax tundu Oliw, te digganteem ak Yerusalem tollook kemu dox bi yoon maye ci bésub Noflaay, yemook benn kilomet. Ñu dellu nag Yerusalem.
13 Ñu agsi, yéeg ca néegu kaw taax ma, fa ñuy dal naka jekk. Piyeer a nga ca, ak Yowaan, ak Yanqóoba ak Àndre, ak Filib ak Tomaa, ak Bartelemi ak Macë, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ farlukatu moom-sa-réew ba, ak Yuda doomu Yanqóoba.
14 Ñu mànkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yàlla, ànd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.
15 Ci fan yooyu la Piyeer taxaw ca digg bokk ya, ña fa daje di mbooloo mu tollu ci téeméer ak ñaar fukk (120). Mu ne leen:
16 «Bokk yi, Mbind mi moo waxe woon Noo gu Sell gi lu jiitu, ci gémmiñu Daawuda, wax ju jëm ci Yuda mi jiite nit ña, ba ñu jàpp Yeesu. Mbind moomu nag fàww mu sotti.
17 Ci nun la Yuda bokkoon, te amoon na it cér ci sunu liggéey bii.»
18 Yuda nag gannaaw ba mu jëndee ab tool ca peyu ñaawtéefam ja, ca la daanu, jiital boppam, biir ba fàcc, butit ya tuuru.