Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 19:7-14 in Wolof

Help us?

JËF YA 19:7-14 in Téereb Injiil

7 Limub nit ñooñu nekk na lu mat fukk ak ñaar.
8 Noonu Pool dugg ca jàngu ba, di wax ak fit wu dëgër diirub ñetti weer, di diisoo ak ñoom ci mbirum nguurug Yàlla, di leen jéema gëmloo.
9 Waaye bi xolu ñenn ci ñoom fattee, ñu gëmadi, bay suufeel yoon wi ci kanam mbooloo ma, mu jóge ci ñoom, xàjjale taalibe yi ak ñoom, di diisoo bés bu nekk ca jàngukaayu ku ñuy wax Tiranus.
10 Mu wéy ci noonu diirub ñaari at, ba ñi dëkk diiwaanu Asi ñépp dégg kàddug Boroom bi, muy Yawut muy Gereg.
11 Booba Yàllay def ay kéemaan yu ràññiku yuy jaar ci loxoy Pool.
12 Ñu yóbbul sax ñi wopp ay kaala ak ay taraxlaay yu laaloon yaramam, ba jàngoro yi di leen bàyyi, rab yay génn ci ñoom.
13 Noonu ay Yawut yuy wëndeelu, di faj ñi rab jàpp, ñu di leen jéema ñaanal ci turu Yeesu Boroom bi naan: «Ci turu Yeesu, mi Pool di yégle, génnleen.»
14 Ñi doon def loolu, juróom ñaari doom lañu woon ci Sewa, mi doon sarxalkat bu mag ci Yawut yi.
JËF YA 19 in Téereb Injiil

Jëf ya 19:7-14 in Kàddug Yàlla gi

7 Taalibe yooyu yépp a ngi wara tollu ci fukk ak ñaar.
8 Ci kaw loolu Póol dem ca jàngu ba, diiru ñetti weer muy waaree aw fit, di waxal waa jàngu ba kàddu yu mata gëm ci mbirum nguurug Yàlla.
9 Ñenn ña nag të ticc, baña gëm, di ŋàññ Yoon wi ca kanam mbooloo ma. Ba loolu amee Póol bàyyi leen, daldi berook taalibe ya, bés bu nekk muy diisoo ak ñoom ca kërug jàngukaay gu Tiranus.
10 Loolu moo wéy diiru ñaari at, ba mboolem waa diiwaanu Asi dégg kàddug Sang bi, muy Yawut, di Gereg.
11 Ba mu ko defee Yàlla di def ay kéemaan yu mag yu mu sottale loxoy Póol.
12 Mujj na sax ñuy yóbbul jarag yi ay kaala aki taraxlaay yu laaloon yaramu Póol, ba lu leen daloon teqlikook ñoom, rab wu leen jàppoon, ba leen.
13 Ci kaw loolu ay Yawut yuy wër di faj ku rab jàpp, tàmbalee roy, di tuddal ñi rab jàpp turu Sang Yeesu, naan rab yi: «Maa la dàq ci turu Yeesu, mi Póol di xamle.»
14 Ña doon def jëf jooju ñooy juróom ñaari doom yu góor yu Sewa, sarxalkatub Yawut bu mag.
Jëf ya 19 in Kàddug Yàlla gi