Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 19:30-37 in Wolof

Help us?

JËF YA 19:30-37 in Téereb Injiil

30 Pool nag bëgga dugg ca mbooloo ma, waaye taalibe ya nanguwuñu ko.
31 Ñenn ca jawriñi nguur gi it, ñuy ay xaritam, yónnee ci moom, di ko dénk, mu baña jaay bakkanam ci dugg ca powukaay ba.
32 Noonu ndaje ma rëb, ba ñii di yuuxu lii, ñale di yuuxu laa, te ña ca gëna bare xamuñu lu waral ndaje ma.
33 Ci kaw loolu Yawut ya jéñ Alegsàndar ci kanam, te mbooloo ma di ko xaacu ay ndigal, mu daldi tàllal loxoom, ngir làyyi ca mbooloo ma.
34 Waaye bi ñu xamee ne Yawut la, ñépp a bokk benn baat, yuuxu diirub lu mat ñaari waxtu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»
35 Gannaaw loolu boroom dëkk ba dalal mbooloo ma ne leen: «Yéen waa Efes, ana ku xamul ne dëkku Efes moo di wottukaayu màggalukaayu Artemis ak nataalam, bi wàcce asamaan?
36 Gannaaw nag kenn manta weddi loolu, war ngeena dalal seen xel te baña sañaxu ci dara.
37 Ndaxte nit ñii ngeen fi indi sàccuñu ca màggalukaay ya te sosaluñu sunu yàlla.
JËF YA 19 in Téereb Injiil

Jëf ya 19:30-37 in Kàddug Yàlla gi

30 Póol nag bëgga teewi ca kanam mbooloo ma, taalibe ya bañ.
31 Ñenn ñay ay soppeem ca kàngami nguur ga sax, yónnee nañu ca moom, di ko àrtu ngir mu baña foye bakkanam, di dem ca ëttu joŋantekaay ba.
32 Ndaje maa nga rëb lool, ñii xaacu ne lii, ñee xaacu, ne lee, te ña ca ëpp sax xamuñu lu waral ndaje ma.
33 Ci kaw loolu mbooloo ma am lu ñu digal ku ñuy wax Alegsàndar, Yawut ya jañax ko ca kanam, mu daldi tàllal loxoom, ngir layool boppam ca digg mbooloo ma.
34 Naka lañu xam ne ab Yawut la, kàddu ga di benn, jibe ca mbooloo mépp, diiru ñaari waxtu. Ñu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»
35 Ndawal buur la nag mujj giifal mbooloo ma, ne leen: «Yeen waa Efes, ana moos ku xamul ne Efes gii mooy dëkk biy wattukatub jaamookaayu Artemis, ak jëmmam ji wàcce asamaan?
36 Loolu maneesu koo weddi. Kon nag, dangeena wara teey, baña sañaxuy def lenn.
37 Ndax nit ñii ngeen fi indi, teddadiluñu ay jaamookaay te waxuñu lu ñàkke sunu yàlla kersa.
Jëf ya 19 in Kàddug Yàlla gi