Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 19:29-40 in Wolof

Help us?

JËF YA 19:29-40 in Téereb Injiil

29 Noonu dëkk bépp jaxasoo. Ñu bokk benn xalaat, daldi ne milib ca powukaay ba, diri Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan, ñi ànd ak Pool.
30 Pool nag bëgga dugg ca mbooloo ma, waaye taalibe ya nanguwuñu ko.
31 Ñenn ca jawriñi nguur gi it, ñuy ay xaritam, yónnee ci moom, di ko dénk, mu baña jaay bakkanam ci dugg ca powukaay ba.
32 Noonu ndaje ma rëb, ba ñii di yuuxu lii, ñale di yuuxu laa, te ña ca gëna bare xamuñu lu waral ndaje ma.
33 Ci kaw loolu Yawut ya jéñ Alegsàndar ci kanam, te mbooloo ma di ko xaacu ay ndigal, mu daldi tàllal loxoom, ngir làyyi ca mbooloo ma.
34 Waaye bi ñu xamee ne Yawut la, ñépp a bokk benn baat, yuuxu diirub lu mat ñaari waxtu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»
35 Gannaaw loolu boroom dëkk ba dalal mbooloo ma ne leen: «Yéen waa Efes, ana ku xamul ne dëkku Efes moo di wottukaayu màggalukaayu Artemis ak nataalam, bi wàcce asamaan?
36 Gannaaw nag kenn manta weddi loolu, war ngeena dalal seen xel te baña sañaxu ci dara.
37 Ndaxte nit ñii ngeen fi indi sàccuñu ca màggalukaay ya te sosaluñu sunu yàlla.
38 Su fekkee ne Demetirus ak ay nawleem jànkoonte nañu ak kenn, am na ay bési layoo ak ñu yilif réew mi; nañu fa woo ku ñu amleenteel.
39 Waaye su ngeen di laaj leneen, mbooloom dëgg dina ko àtte.
40 Ndaxte fi mu ne man nañu noo jiiñ jógug mbooloo mi ndax li fi xew tey. Te bu loolu amee dunu am aw lay ci mbirum mbooloo mu rëb mii, ndaxte amul dara lu ko waral.» Bi mu waxee loolu nag, mu tas mbooloo ma.
JËF YA 19 in Téereb Injiil

Jëf ya 19:29-40 in Kàddug Yàlla gi

29 Ci kaw loolu dëkk bépp ne kër-kër, ne këpp. Ñu jàpp Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan ya àndoon ak Póol ca tukki ba. Ñu daldi riirandoo wuti ëttu joŋantekaay ba.
30 Póol nag bëgga teewi ca kanam mbooloo ma, taalibe ya bañ.
31 Ñenn ñay ay soppeem ca kàngami nguur ga sax, yónnee nañu ca moom, di ko àrtu ngir mu baña foye bakkanam, di dem ca ëttu joŋantekaay ba.
32 Ndaje maa nga rëb lool, ñii xaacu ne lii, ñee xaacu, ne lee, te ña ca ëpp sax xamuñu lu waral ndaje ma.
33 Ci kaw loolu mbooloo ma am lu ñu digal ku ñuy wax Alegsàndar, Yawut ya jañax ko ca kanam, mu daldi tàllal loxoom, ngir layool boppam ca digg mbooloo ma.
34 Naka lañu xam ne ab Yawut la, kàddu ga di benn, jibe ca mbooloo mépp, diiru ñaari waxtu. Ñu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»
35 Ndawal buur la nag mujj giifal mbooloo ma, ne leen: «Yeen waa Efes, ana moos ku xamul ne Efes gii mooy dëkk biy wattukatub jaamookaayu Artemis, ak jëmmam ji wàcce asamaan?
36 Loolu maneesu koo weddi. Kon nag, dangeena wara teey, baña sañaxuy def lenn.
37 Ndax nit ñii ngeen fi indi, teddadiluñu ay jaamookaay te waxuñu lu ñàkke sunu yàlla kersa.
38 Su dee Demetirus ak liggéeykat yi ànd ak moom ñoo jote ak kenn ci ñoom, ay ëtti layoo am na fi, ay kàngam a ngi fi di àtte. Nañu fa layooji.
39 Su dee leneen lu ngeen di sàkku nag, ca ndajem àtte ba lees koy lijjantee.
40 Ndax kat repp nanu ñu jiiñ nu ag fippu, te amul lenn lu nu mana lay, ba lewal mii ndaje.» Naka la wax loolu, daldi tas mbooloo ma.
Jëf ya 19 in Kàddug Yàlla gi