Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 19:24-27 in Wolof

Help us?

JËF YA 19:24-27 in Téereb Injiil

24 Ndaxte nit ku tudd Demetirus, di tëggu xaalis buy defar nataali xaalis ngir màggal Artemis, daan na ci jariñu lu bare, moom ak ay nawleem.
25 Noonu mu dajale leen ak seeni liggéeykat ne leen: «Gaa ñi, xam ngeen ne sunu njariñ mu ngi aju ci liggéey bii.
26 Gis ngeen nag te dégg ne Pool male gëmloo na bay fàbbi mbooloo mu bare, waxuma ci Efes rekk, waaye ci biir Asi gépp naan: “Yàlla yu ay loxo defar duñu ay yàlla.”
27 Léegi kat loraangee ngi nuy yoot, te du yem ci xañ nu sunu liggéey rekk, waaye it dina daaneel màggalukaayu Artemis sunu yàlla ju mag ji, tey neenal ndamam, moom mi Asi gépp te àddina sépp di màggal.»
JËF YA 19 in Téereb Injiil

Jëf ya 19:24-27 in Kàddug Yàlla gi

24 Ku ñuy wax Demetirus, ab tëggu xaalis, moo daan defar jëmmi jaamookaay yu ndaw yu tuur mi ñu dippee Artemis, muy njariñ lu réy ci liggéeykat yiy nawleem.
25 Mu woo leen, ñook ña farewoo liggéey yu ni mel, ne leen: «Bokk yi, xam ngeen ne liggéey bii, ci la sunu teraanga nekk.
26 Yeena gis nag mbaa ngeen déggal seen bopp ni Póol moomu di naxee ba fàbbi mbooloo mu bare, te du ci Efes gii rekk, daanaka Asi gépp la: Mu naay: “Yàlla yu loxol nit sàkk du yàlla.”
27 Loolu, jéllale naa ni mu mana gàkkale sunu liggéey bii, waaye dina tax ñu teddadil jaamookaayu Artemis, yàlla ju jigéen ju mag ji, ba darajaam mujj neen, moom mi mboolem Asi ak àddina sax di jaamu.»
Jëf ya 19 in Kàddug Yàlla gi