Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 19:15-24 in Wolof

Help us?

JËF YA 19:15-24 in Téereb Injiil

15 Waaye bi ñu ko defee rab wa ne leen: «Xam naa Yeesu, xam naa it kuy Pool, waaye yéenay ñan?»
16 Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, not leen ñoom ñépp; mu soxore leen lool, ba ñu daw kër ga, def yaramu neen te gaañu bu metti.
17 Loolu siiw na ci ñépp, ñi dëkk Efes, di Yawut ak Gereg; tiitaange jàpp leen ñoom ñépp, ba ñu màggal turu Yeesu Boroom bi.
18 Bi loolu amee ñu bare ci ñi gëm ñëw, di wesar ci kanam ñépp seeni jati luxus.
19 Te ñu bare ci ñi daan luxus, indi seeni téere, lakk leen ci kanam ñépp. Te bi ñu xaymaa njég la, mu tollook juróom fukki junniy poseti daraxma.
20 Noonu la kàddu Boroom bi lawe, te not lépp.
21 Bi loolu wéyee Pool nas xel jëm Yerusalem, jaar ci diiwaani Maseduwan ak Akayi. Mu ne: «Gannaaw bu ma fa demee, fàww ma seeti Room it.»
22 Mu yebal nag ci Maseduwan ñaari jaraafam, di Timote ak Erast, waaye moom mu des ab diir ci Asi.
23 Fekk booba amoon na yëngu-yëngu bu réy ci lu aju ci Yoon wi.
24 Ndaxte nit ku tudd Demetirus, di tëggu xaalis buy defar nataali xaalis ngir màggal Artemis, daan na ci jariñu lu bare, moom ak ay nawleem.
JËF YA 19 in Téereb Injiil

Jëf ya 19:15-24 in Kàddug Yàlla gi

15 Loolu lañu doon jéem bés, rab wu bon wa ne leen: «Yeesu déy, xam naa ko. Póol it xam naa ko. Waaye yeen, yeenay ñan?»
16 Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, teg leen loxo ñoom ñépp, pamti-pamtee leen, gaañ leen, ba ñu dawe kër ga yaramu neen.
17 Mboolem Yawut yaak Gereg ya dëkke Efes nag yég mbir moomu, tiitaange dikkal leen ñoom ñépp, daraja ju réy doxe ca ñeel turu Sang Yeesu.
18 Ba mu ko defee ñu bare ca gëmkat ña dikk, biral seenug tooñ, daldi xamle yu bon ya ñu daan jëfe.
19 Ci biir loolu ñu bare ñu daan ñeengo, boole seeni téere, indi, lakk ko fa kanam ñépp. Ba ñu xaymaa njég la, tolloo naak juróom fukki junniy poseti daraxma (50 000).
20 Noonu la kàddu gi lawe ba féete kaw ci kàttanu Boroom bi.
21 Gannaaw ba loolu wéyee, Póol ci ndigalal Noo gu Sell gi am mébétum jaare diiwaani Maseduwan ak Akayi, teg ca Yerusalem. Mu ne: «Gannaaw bu ma àggee foofu, war namaa jàll ba Room itam.»
22 Mu daldi yebal fa Maseduwan, ñaari jaraafam, Timote ak Eràst, moom mu toogaat ab diir ca Asi.
23 Jant yooyu nag yemook yëngu-yëngu bu réy bu amoon ci mbirum Yoon wi.
24 Ku ñuy wax Demetirus, ab tëggu xaalis, moo daan defar jëmmi jaamookaay yu ndaw yu tuur mi ñu dippee Artemis, muy njariñ lu réy ci liggéeykat yiy nawleem.
Jëf ya 19 in Kàddug Yàlla gi