Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 19:15-20 in Wolof

Help us?

JËF YA 19:15-20 in Téereb Injiil

15 Waaye bi ñu ko defee rab wa ne leen: «Xam naa Yeesu, xam naa it kuy Pool, waaye yéenay ñan?»
16 Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, not leen ñoom ñépp; mu soxore leen lool, ba ñu daw kër ga, def yaramu neen te gaañu bu metti.
17 Loolu siiw na ci ñépp, ñi dëkk Efes, di Yawut ak Gereg; tiitaange jàpp leen ñoom ñépp, ba ñu màggal turu Yeesu Boroom bi.
18 Bi loolu amee ñu bare ci ñi gëm ñëw, di wesar ci kanam ñépp seeni jati luxus.
19 Te ñu bare ci ñi daan luxus, indi seeni téere, lakk leen ci kanam ñépp. Te bi ñu xaymaa njég la, mu tollook juróom fukki junniy poseti daraxma.
20 Noonu la kàddu Boroom bi lawe, te not lépp.
JËF YA 19 in Téereb Injiil

Jëf ya 19:15-20 in Kàddug Yàlla gi

15 Loolu lañu doon jéem bés, rab wu bon wa ne leen: «Yeesu déy, xam naa ko. Póol it xam naa ko. Waaye yeen, yeenay ñan?»
16 Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, teg leen loxo ñoom ñépp, pamti-pamtee leen, gaañ leen, ba ñu dawe kër ga yaramu neen.
17 Mboolem Yawut yaak Gereg ya dëkke Efes nag yég mbir moomu, tiitaange dikkal leen ñoom ñépp, daraja ju réy doxe ca ñeel turu Sang Yeesu.
18 Ba mu ko defee ñu bare ca gëmkat ña dikk, biral seenug tooñ, daldi xamle yu bon ya ñu daan jëfe.
19 Ci biir loolu ñu bare ñu daan ñeengo, boole seeni téere, indi, lakk ko fa kanam ñépp. Ba ñu xaymaa njég la, tolloo naak juróom fukki junniy poseti daraxma (50 000).
20 Noonu la kàddu gi lawe ba féete kaw ci kàttanu Boroom bi.
Jëf ya 19 in Kàddug Yàlla gi