Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 19:13-16 in Wolof

Help us?

JËF YA 19:13-16 in Téereb Injiil

13 Noonu ay Yawut yuy wëndeelu, di faj ñi rab jàpp, ñu di leen jéema ñaanal ci turu Yeesu Boroom bi naan: «Ci turu Yeesu, mi Pool di yégle, génnleen.»
14 Ñi doon def loolu, juróom ñaari doom lañu woon ci Sewa, mi doon sarxalkat bu mag ci Yawut yi.
15 Waaye bi ñu ko defee rab wa ne leen: «Xam naa Yeesu, xam naa it kuy Pool, waaye yéenay ñan?»
16 Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, not leen ñoom ñépp; mu soxore leen lool, ba ñu daw kër ga, def yaramu neen te gaañu bu metti.
JËF YA 19 in Téereb Injiil

Jëf ya 19:13-16 in Kàddug Yàlla gi

13 Ci kaw loolu ay Yawut yuy wër di faj ku rab jàpp, tàmbalee roy, di tuddal ñi rab jàpp turu Sang Yeesu, naan rab yi: «Maa la dàq ci turu Yeesu, mi Póol di xamle.»
14 Ña doon def jëf jooju ñooy juróom ñaari doom yu góor yu Sewa, sarxalkatub Yawut bu mag.
15 Loolu lañu doon jéem bés, rab wu bon wa ne leen: «Yeesu déy, xam naa ko. Póol it xam naa ko. Waaye yeen, yeenay ñan?»
16 Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, teg leen loxo ñoom ñépp, pamti-pamtee leen, gaañ leen, ba ñu dawe kër ga yaramu neen.
Jëf ya 19 in Kàddug Yàlla gi