Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 19:1-11 in Wolof

Help us?

JËF YA 19:1-11 in Téereb Injiil

1 Ba Apolos nekkee Korent nag, Pool jaar ca teggi ya gëna kawe ca réew ma, doora dikk Efes. Noonu mu gis fa ay taalibe.
2 Mu ne leen: «Ndax jot ngeen ci Xel mu Sell mi, bi ngeen gëmee?» Ñu ne ko: «Déggunu sax ne Xel mu Sell mi am na.»
3 Mu ne leen: «Kon nag, bi ñu leen sóobee ci ndox, lu ciy maana?» Ñu ne ko: «Xanaa li Yaxya tëral.»
4 Pool ne leen: «Yaxya daan na sóob nit ñi ci ndox, ndax bi ñu tuubee seeni bàkkaar; te mu ne bànni Israyil, kiy topp ci moom lañu wara gëm, maanaam Yeesu.»
5 Bi ñu déggee loolu nag, sóob nañu leen ci ndox ci turu Yeesu Boroom bi.
6 Te bi leen Pool tegee loxo, Xel mu Sell mi ñëw ci ñoom, ñuy wax yeneen làkk, di wax ci kàddug Yàlla.
7 Limub nit ñooñu nekk na lu mat fukk ak ñaar.
8 Noonu Pool dugg ca jàngu ba, di wax ak fit wu dëgër diirub ñetti weer, di diisoo ak ñoom ci mbirum nguurug Yàlla, di leen jéema gëmloo.
9 Waaye bi xolu ñenn ci ñoom fattee, ñu gëmadi, bay suufeel yoon wi ci kanam mbooloo ma, mu jóge ci ñoom, xàjjale taalibe yi ak ñoom, di diisoo bés bu nekk ca jàngukaayu ku ñuy wax Tiranus.
10 Mu wéy ci noonu diirub ñaari at, ba ñi dëkk diiwaanu Asi ñépp dégg kàddug Boroom bi, muy Yawut muy Gereg.
11 Booba Yàllay def ay kéemaan yu ràññiku yuy jaar ci loxoy Pool.
JËF YA 19 in Téereb Injiil

Jëf ya 19:1-11 in Kàddug Yàlla gi

1 Diir ba Apolos nekkee Korent, Póol a nga jaare ca diiwaan yu tunde ya, ba wàccsi Efes. Mu daje faakay taalibe,
2 ne leen: «Ndax ba ngeen gëmee, jot ngeen ci Noo gu Sell gi?» Ñu ne ko: «Nun de yégunu woon sax ne Noo gu Sell gi am na.»
3 Mu ne leen: «Kon gan sóobu ngeen sóobu?» Ñu ne ko: «Xanaa sóobeb Yaxya.»
4 Póol ne leen: «Yaxya, sóobeb tuubeel la daan sóobe ci ndox, di waxaale askan wi ne leen ñu gëm kiy topp ci moom, te mooy Yeesu.»
5 Ba ñu déggee loolu lañu sóobu ci ndox ci turu Sang Yeesu.
6 Ba leen Póol tegee loxoom, Noo gu Sell gi dikkal leen, ñu tàmbalee làkk yeneen làkk, boole ci di biral waxyu.
7 Taalibe yooyu yépp a ngi wara tollu ci fukk ak ñaar.
8 Ci kaw loolu Póol dem ca jàngu ba, diiru ñetti weer muy waaree aw fit, di waxal waa jàngu ba kàddu yu mata gëm ci mbirum nguurug Yàlla.
9 Ñenn ña nag të ticc, baña gëm, di ŋàññ Yoon wi ca kanam mbooloo ma. Ba loolu amee Póol bàyyi leen, daldi berook taalibe ya, bés bu nekk muy diisoo ak ñoom ca kërug jàngukaay gu Tiranus.
10 Loolu moo wéy diiru ñaari at, ba mboolem waa diiwaanu Asi dégg kàddug Sang bi, muy Yawut, di Gereg.
11 Ba mu ko defee Yàlla di def ay kéemaan yu mag yu mu sottale loxoy Póol.
Jëf ya 19 in Kàddug Yàlla gi