5Ba Silas ak Timote dikkee, bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, Póol xintewootul lu moy di xamle kàddu gi, di seereel Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi.
6Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»
7Mu jóge foofa, dem kër jaamburub jaamukatu Yàlla bu ñuy wax Tisyus Yustus, te këram sësook jàngu ba.