Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 18:4-9 in Wolof

Help us?

JËF YA 18:4-9 in Téereb Injiil

4 Bésub noflaay bu nekk nag muy diisoo ak ñi nekk ca jàngu ba, di jéema gëmloo ay Yawut ak ay Gereg.
5 Waaye bi Silas ak Timote jógee diiwaanu Maseduwan, egg fa, Pool jublu ci xamle kàddu gi, tey dëggal ci Yawut yi naan Yeesu mooy Almasi bi.
6 Bi ko Yawut ya gàntoo nag, di ko xas, mu yëlëb ay yéreem ne leen: «Yéena sàkku seen musiba; set naa ci. Léegi maa ngi dem ci ñi dul Yawut.»
7 Ci kaw loolu mu jóge fa, dugg ci këru ku tudd Tisiyus Yustus, di ku ragal Yàlla, te kër ga dend ak jàngu ba.
8 Kirispus nag, njiitu jàngu ba, gëm na Boroom bi ak waa këram gépp. Te waa Korent ñu bare dégg kàddu gi te gëm ko, ñu sóob leen ci ndox.
9 Naka noona Boroom bi feeñu Pool ci guddi ne ko: «Bul tiit dara, waaye deel wax te baña noppi.
JËF YA 18 in Téereb Injiil

Jëf ya 18:4-9 in Kàddug Yàlla gi

4 Ci kaw loolu bésub Noflaay bu nekk Póol di waare ca jàngu ba, di yee Yawut yi ak Gereg yi.
5 Ba Silas ak Timote dikkee, bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, Póol xintewootul lu moy di xamle kàddu gi, di seereel Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi.
6 Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»
7 Mu jóge foofa, dem kër jaamburub jaamukatu Yàlla bu ñuy wax Tisyus Yustus, te këram sësook jàngu ba.
8 Teewul Kirispus njiitu jàngu ba moom, gëm Sang bi, mook waa këram gépp. Ñu bare ci waa Korent a gëm, gannaaw ba ñu déggee kàddu gi, ba ñu sóob leen ci ndox.
9 Ba loolu amee Sang bi wax ak Póol ag guddi ci biir peeñu, ne ko: «Bul tiit dara, waaye waxal te bul noppi,
Jëf ya 18 in Kàddug Yàlla gi