3 Póol nag miinante ak ñoom, te fekk ñu bokk benn liggéey, di defarkati xayma ni moom. Loolu tax mu far dal ak ñoom, di liggéey.
4 Ci kaw loolu bésub Noflaay bu nekk Póol di waare ca jàngu ba, di yee Yawut yi ak Gereg yi.
5 Ba Silas ak Timote dikkee, bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, Póol xintewootul lu moy di xamle kàddu gi, di seereel Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi.
6 Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»
7 Mu jóge foofa, dem kër jaamburub jaamukatu Yàlla bu ñuy wax Tisyus Yustus, te këram sësook jàngu ba.