Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 18:19-28 in Wolof

Help us?

JËF YA 18:19-28 in Téereb Injiil

19 Noonu ñu teer ci Efes. Pool bàyyi fa ñi mu àndaloon, daldi dugg ca jàngu ba, di diisoo ak Yawut ya.
20 Ñu ñaan ko, mu des fa lu gëna yàgg, waaye nanguwul.
21 Kon mu tàggtoo ak ñoom naan: «Dinaa délsi ci yéen, bu soobee Yàlla.» Noonu mu dugg gaal, jóge Efes,
22 teersi dëkku Sesare, mu dem nuyu mbooloom ñi gëm, ba noppi dem Ancos.
23 Bi mu fa desee ay jamono, mu jóge fa, di jaar dëkkoo dëkk ci diiwaanu Galasi ak Firisi, di dooleel xoli taalibe yépp.
24 Amoon na nag Yawut bu tudd Apolos te juddoo Alegsàndiri, mu dikk Efes. Nit ku yewwu la woon te am xam-xam bu yaatu ci Mbind mi.
25 Jàngoon na ci yoonu Boroom bi, di ku farlu ci xelam, muy xamle ak a jàngle bu wóor ci mbirum Yeesu, waaye fekk xam-xamam yem ci ni Yaxya daan sóobe ci ndox.
26 Noonu mu daldi wax ak fit wu dëgër ca jàngu ba. Bi ko Pirsil ak Akilas déggee nag, ñu woo ko fi ñoom, gën ko leeral yoonu Yàlla.
27 Naka Apolos bëgga dem Akayi, bokk ya xiir ko ca, ñu bind taalibe ya, ngir ñu teeru ko teeru bu rafet. Noonu mu dikk fa te jariñ lool ñi gëm jaare ko ci yiwu Yàlla.
28 Ndaxte mu ngay yey Yawut ya ca kanam ñépp, di firi Mbind yi, ba wone ne Yeesu mooy Almasi bi.
JËF YA 18 in Téereb Injiil

Jëf ya 18:19-28 in Kàddug Yàlla gi

19 Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.
20 Ñooñu ñaan ko, mu toogaat fa ab diir, mu gàntal.
21 Naka la tàggtoo ak ñoom, ne leen: «Dinaa leen seetsiwaat, bu soobee Yàlla.» Ba loolu amee mu dugg gaal, bàyyikoo Efes,
22 teereji Sesare. Mu dem nag Yerusalem, nuyuji mbooloom gëmkat ña, doora dem Àncos gu Siri.
23 Póol toog na Àncos ay fan, jóge fa wër diiwaanu Galasi, teg ca Firisi, di ñaax mboolem taalibey foofa.
24 Ab Yawut nag bu ñuy wax Apolos te cosaanoo Alegsàndiri, moo dikkoon Efes. Ku rafet kàddu, te xam Mbind mi lool.
25 Kooku jotoon naa jàng yoonu Sang bi. Mu ànd ak cawarte, di waare ak a jàngle lu wér péŋŋ ci mbirum Yeesu, doonte xam-xamam a ngi yemoon ci sóobeb Yaxya ci ndox.
26 Mu tàmbalee waxe kóolute ca jàngu ba. Pirsil ak Akilas dégg ko, woo ko cig wet. Ñu daldi koy gëna leeralal yoonu Yàlla wi.
27 Ba mu ko defee Apolos namma jàll ba Akayi, bokk ya rafetlu mébétam. Ñu bind taalibey Akayi, ngir ñu dalal ko. Ba Apolos agsee Akayi, dimbali na lool ña fa yiw may ñu doon ay gëmkat.
28 Ndax fa kanam mbooloo ma la doon tiiñale Yawut ya ay firnde yu mat sëkk, firil leen Mbind mi, ba leeralal leen nàññ ne Yeesu mooy Almasi.
Jëf ya 18 in Kàddug Yàlla gi