19Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bà yyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jà ngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.
20Ñooñu ñaan ko, mu toogaat fa ab diir, mu gà ntal.
21Naka la tà ggtoo ak ñoom, ne leen: «Dinaa leen seetsiwaat, bu soobee Yà lla.» Ba loolu amee mu dugg gaal, bà yyikoo Efes,
22teereji Sesare. Mu dem nag Yerusalem, nuyuji mbooloom gëmkat ña, doora dem Àncos gu Siri.
23Póol toog na Àncos ay fan, jóge fa wër diiwaanu Galasi, teg ca Firisi, di ñaax mboolem taalibey foofa.
24Ab Yawut nag bu ñuy wax Apolos te cosaanoo Alegsà ndiri, moo dikkoon Efes. Ku rafet kà ddu, te xam Mbind mi lool.
25Kooku jotoon naa jà ng yoonu Sang bi. Mu à nd ak cawarte, di waare ak a jà ngle lu wér péŋŋ ci mbirum Yeesu, doonte xam-xamam a ngi yemoon ci sóobeb Yaxya ci ndox.
26Mu tà mbalee waxe kóolute ca jà ngu ba. Pirsil ak Akilas dégg ko, woo ko cig wet. Ñu daldi koy gëna leeralal yoonu Yà lla wi.