Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 18:18-23 in Wolof

Help us?

JËF YA 18:18-23 in Téereb Injiil

18 Bi loolu wéyee Pool desati fa fan yu bare. Gannaaw ga mu tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Bi mu jógeegul teerub Señsere, mu watlu boppam, ndaxte am na lu mu dige woon ak Yàlla.
19 Noonu ñu teer ci Efes. Pool bàyyi fa ñi mu àndaloon, daldi dugg ca jàngu ba, di diisoo ak Yawut ya.
20 Ñu ñaan ko, mu des fa lu gëna yàgg, waaye nanguwul.
21 Kon mu tàggtoo ak ñoom naan: «Dinaa délsi ci yéen, bu soobee Yàlla.» Noonu mu dugg gaal, jóge Efes,
22 teersi dëkku Sesare, mu dem nuyu mbooloom ñi gëm, ba noppi dem Ancos.
23 Bi mu fa desee ay jamono, mu jóge fa, di jaar dëkkoo dëkk ci diiwaanu Galasi ak Firisi, di dooleel xoli taalibe yépp.
JËF YA 18 in Téereb Injiil

Jëf ya 18:18-23 in Kàddug Yàlla gi

18 Ba loolu wéyee Póol toogaat na fa fan yu bare, doora tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Fekk na mu watu nel ca teerub Señsere, firndeele ko aw xas wu mu xasoon.
19 Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.
20 Ñooñu ñaan ko, mu toogaat fa ab diir, mu gàntal.
21 Naka la tàggtoo ak ñoom, ne leen: «Dinaa leen seetsiwaat, bu soobee Yàlla.» Ba loolu amee mu dugg gaal, bàyyikoo Efes,
22 teereji Sesare. Mu dem nag Yerusalem, nuyuji mbooloom gëmkat ña, doora dem Àncos gu Siri.
23 Póol toog na Àncos ay fan, jóge fa wër diiwaanu Galasi, teg ca Firisi, di ñaax mboolem taalibey foofa.
Jëf ya 18 in Kàddug Yàlla gi