Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 18:16-20 in Wolof

Help us?

JËF YA 18:16-20 in Téereb Injiil

16 Noonu mu dàq leen ca àttekaay ba.
17 Ci kaw loolu nit ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, ñu di ko dóor ca kanam àttekaay ba, waaye Galyon faalewu leen.
18 Bi loolu wéyee Pool desati fa fan yu bare. Gannaaw ga mu tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Bi mu jógeegul teerub Señsere, mu watlu boppam, ndaxte am na lu mu dige woon ak Yàlla.
19 Noonu ñu teer ci Efes. Pool bàyyi fa ñi mu àndaloon, daldi dugg ca jàngu ba, di diisoo ak Yawut ya.
20 Ñu ñaan ko, mu des fa lu gëna yàgg, waaye nanguwul.
JËF YA 18 in Téereb Injiil

Jëf ya 18:16-20 in Kàddug Yàlla gi

16 Galyon daldi leen dàqe ca àttekaay ba.
17 Ci kaw loolu ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, dóor ko ca àttekaay ba, te taxul Galyon yégal ko yaramam.
18 Ba loolu wéyee Póol toogaat na fa fan yu bare, doora tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Fekk na mu watu nel ca teerub Señsere, firndeele ko aw xas wu mu xasoon.
19 Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.
20 Ñooñu ñaan ko, mu toogaat fa ab diir, mu gàntal.
Jëf ya 18 in Kàddug Yàlla gi